NDOX MI : FSS A NGI SÀKKU ÑU SIIWAL PAS YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Kurél gii di Forum Social Sénégalais, gàttal biy joxe FSS biral na càkkuteefam ñeel céddaleg ndox mi, fi réew mi. Li kurél giy laaj mooy, na Càmmug Senegaal gi siiwal pas yi torlook waa Groupe Suez ngir ñu mën a xam li ci biir pas yooyii.

Ci àjjuma jii weesu la kurélug FSS doon amal um ndaje. Ca la koordonaatëer ba, Mamadu Miñaan Juuf, jëlee kàddu, fésal càkkuteefu kurél gi. Dafa ne :

“Noo ngi sàkku ci Càmmug Senegaal gi mu siiwal pas googu mu torlook Suez mi nga xam ne, dafa ñàkk alal ji mu amoon fa Marog jépp. Nde, joojee alal, Veolia dafa delloo réewum Marog lépp luy àq ja mu ca amoon.”

Ca njeexitalu ndaje ma FSS séqoon ak Conseil du citoyen du droit à l’eau et à l’assainissement la Sëñ Miñaan fésalee yile kàddu. Mu raxoon na ca dolli sax, ne :

“Déggees na ne Senegaal nangu na siiwal pas yi ñeel soroj beek gil bi. Moone de, ndox mee ëpp solo fuuf soroj beek gil bi. Kon kay, war ngeen laaj pas yi Càmmug Senegaal torlook Suez.”

Pas gi Mamadu Miñaan Juuf di wax, mooy pas gi Nguurug Maki Sàll torlu woon ak Suez . Pas gaa ngi aju ci céddaleg ndox mu sell mi ci dëkki taax yeek yu leen wër. Ca jamono jooja, waa Forum Civil doon nañ kaas, di ŋàññ pas googule. Moo tax, moom, Mamadu Miñaan Juuf, muy ñaan Càmm gi mu xoolaat pas googu, saytuwaat ko.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj