Tay, ci àllarba ji, 30i oktoobar 2024, ngëlén lu am doole moo dikkal waa Espaañ. Bariwaayu ndox mi ak dooley ngelaw li tax nañu ba ay loraange yu bare a bare juddoo ci, ay bakkan yu bare rot ci, tiis ak njàqare ganesi askan wa.
Ci lees biral ciy xibaar, 95i nit ñàkkagum nañu seen i bakkan ci mbënn mom, taw bu bare bi a ko sabab. Fa diiwaanu Valence la jéyya ji gënee tar, ndax fa la ngëlén li rawee. Dafa di, foofu rekk, 92i bakkan rot nañ fa. Ñaari nit ñoo faatu fa diiwaanu Castille-La Manche, mu amaat keneen ku dee fa diiwaanu Andalousie. Njiiti réew ma ñoo ko xamle.
Bees sukkandikoo ci kàdduy jëwriñu Pólitigu mberaay mi, Ángel Víctor Torres, limu ñi dee “…dina yokku ndax am na ñu bare ñu réer.”
Jéyya ju ni mel nag, 1973 lees ko gëj a gis fa réew ma. At mooma, 300i nit ñoo ca dee woon.
Nguurug Espaañ gi jël na ndogalu ñetti fani dëj, dale ko alxamesu ëllëg ji. Seen elimaanu jëwriñ yi, Pedro Sánchez, fas na yéene nemmeekuji béréb ya jéyya ji xewe.