NGËRËMUL XAREKATI SENEGAAL YA WOON

Yeneen i xët

Aji bind ji

Réewum Farãs fas na yéene fésal ngërëmam ñeel xarekati Senegaal ya ko xettali woon ca ñaareelu xareb àdduna ba. Xarakti démb yooyii lañuy woowe, ci nasaraan, « Tirailleures sénégalais ». dafa di sax, am na ñu ci Farãs jotoon a nangul. Waaye, wile yoon, mbooleem xarekati saa-senegaal ya ko dimbali woon la bëgg a nangul, rawatina ña ñu rayoon Caaroy, atum 1944.

Njiiti réewum Farãs yi biral nañ xibaar bu yees jëm ci xarekati Senegaal ya woon, jamonoy nooteel ga. Dañu xamle ne, fas nañoo yéene nangul mbooleem xarekati Senegaal ya ñu bóomoon Caaroy ca atum 1944. Dafa di, ba jonni-Yàlla tey jii, juróom-benn kese lañu jotagum nangul ci ñoom, wax ne “ay soldaar yu faatu ngir Farãas” lañu. Loolu nag, metti woon na ñu bari ba mu juroon coow. Usmaan Sonko sax ñaawlu woon na ko, daldi jam Njiiti Farãs yi. amaana moo tax ñu bëgg a dabantal.

Jamono jii, dañu tollu ci di waajal màggalug 80eelu atum wàcc ca Provence. Ca la kenn ci ndawi laamisooy Farãs yi xamlee ne, keroog altine, “Bunt bi tijjiku na ngir nangul mbooleem xarekati saa-senegaal yooyu…” APS moo tuxal i kàddoom.

Elimaanu jëwriñ yi nag, Usmaan Sonko, xamle woon na ne am na lu Nguruug Senegaal di waajl moom itam ngir sargal jàmbaar yooyii. Ñu ngi xaarandi ba xam lu muy doon.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj