Dépite yi dindi nañu mbalaanu kiiraayu Farba Ngom ci àjjumay tay jii, 24i sãwiyee 2024.
Ci ngoonug tay ji la dépite doon fénc mbirum Muhammadu Ngom, ñu gën ko xam ci turu Farba Ngom.
Ngomblaan gi mujje na summi mbalaanu kiiraayu Farba Ngom. 136i dépite ñoo wote ngir ñu dindi ko. Ci biir 136 yooyu, daf ci am 10 yu bind, yóbbante seen wote. Bu dee waa lëkkatoo Takku Wallu, ñoom, dañoo gedd wote bi. Bi Abdul Mbów waxee ba noppi lañu génn Ngomblaan gi. Mu am nag 3 ñu wote ngir ñu bañ a dindi mbalaanu kiiraayu Farba Ngom, ak yeneen 3 yu ci màndu.
Ngir fàttali, jëwriñu Yoon ji moo bind Ngomblaan gi ci càkkuteefu Pool judiciaire financier, ëttu àttekaay biy saytu mbiri koppar yi.
Aysata Taal Sàll mi bokk APR, jiite kippug dépitey Takku Wallu fa Ngomblaan ga, rafetluwul taxawaayu jëwriñu Yoon ji. Daf ne :
« Njëwriñ giy daanaate, moom dafay saytu jëf yi. Bu dee njëwriñu Yoon gi nag, moom dafay natt, di njort njeexital li. »
Ginnaaw bi mu sànnee kàddu yooyu, moom soxna si teg na ci ne, Ngomblaan gi sàmmontewul ak àqi Farba Ngom miy seen naataangoo dépite.
Bees sukkandikoo ci waxi meetar Abdulaay Taal nag, moom mi jiite Ndiisoo cëtëŋ gi doon saytu mbirum dindi mbalaanu kiiraayu Farba Ngom mi, kenn salfaañewul àqi meeru Añam bi. Daf ne :
« amul dara lees fi parax-paraxee, gaawantu ko ñeel yoonuw dindi mbalaanu kiiraayu dépite bii di Muhammadu Ngom, ñu koy woowee Farba Ngom. »
Léegi nag, ndeem summi nañu mbalaanu kiiraayu Farba Ngom, Yoon dina am sañ-sañu woo ko, déglu ko ak itam àtte ko, bu de jar na ko.