NGOMBLAAN GI JOYYANTI NA SÀRTU-BIIRAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dépite yi jàllale nañ sémbuw àtteb 10/2024 wiy soppi ak a mottali « loi organique » bu 2002-20 bu 15i pani me 2002 ñeel Sàrt-biiru Ngomblaan gi. Tay, ci àjjuma ji, 16i pani ut 2024, lañu doon péncoo ngir amal coppite yi war.

Bi ko Njiitu réew mi tabbee ba léegi, elimaanu jëwriñ ji, Usmaan Sonko, taxawagul ci kanamu ndawi réew mi ngir fésal naaluw pólitig wi ñu, moom ak càmm gi, nar a doxal ngir faj aajoy Saa-Senegaal yi. Li ko sabab nag moo di ne, ci Sàrt-biiru Ngomblaan gi, dañ cee faroon lépp lu aju woon ci ndombog-tànku elimaanu jëwriñ ji. Ndax, Njiitu réew ma woon, Maki Sàll, moo dindi woon ndombog-tànku elimaanu jëwriñ ji ci Càmm gi. Noona, Ngombalaan gi soppi sàrt-biiram, dindi ci moom itam lépp lu ci jëm. Bi ñu ko delloosee nag, Ngomblaan gi deful li ko war ci joyyanti Sàrt-biiram, dugalaat ci dog yi ñeel ndombog-tànku elimaanu jëwriñ ji. Looloo taxoon dépite bii di Muhammet Saañaa (Gii Mari Saañaa) xelaloon Usmaan Sonko, waxoon ko ne bu mu ñëw ca Ngomblaan ga ndax seen sàrt-biir xamu ko niki elimaanu jëwriñ ji. Usmaan Sonko yit déggal ko.

Cig pàttali, Usmaan Sonko dafa dankaafu woon Ngomblaan gi, jox leen àpp, waxoon leen ne, bu ñu joyyantiwul seen sàrt-biir ba 15i pani sulet 2024, dina biral uw naalu pólitigam ci kanamu askan wi ak i boroomi xam-xam. Waaye, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, moo ci dox tànki jàmm, wax ak elimaanu jëwriñam yi, yey ko ci mu bàyyi li mu naroon a def. Ca la wooluwee tamit, moom Njiitu réew mi, njiitul Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, fa njénde la, waxtaan ak moom ngir Ngomblaan gi soppi sàrt-biiram ndax Usmaan Sonko mën a def wareefam ni ko ko Yoon santee. Ginnaaw gi, Pekkug Ngomblaan gi dafa amal i ndaje jëm ci wàll wi. Ndogal ya tukkee ca ndaje yooyoo tax ñu woolu ndawi réew mi, tay ci àjjuma ji, 16i pani ut 2024, ngir waxtaane mbir mi, amal coppite yi war ngir elimaanu jëwriñ ji, Usmaan Sonko, mën a biral naaluw pólitigam (Déclaration de politique générale).

Abdu Mbów, njiitul kippaangog dépite bu Bennoo Bokk Yaakaar, moo jébbal sémbuw àtte bees di wax « loi organique », moom ak Mohammet Ayib Saalim Dafe (njiitul kippaangog dépite bu Yewwi Askan Wi) ak it Mamadu Lamin Caam (njiitul kippaangog dépite bu Liberté, Démocratie et Changement). Bees sukkandikoo ci kàdduy Abdu Mbów, ñi nekkoon ci kippug liggéey bi doon xalaat ci joyyantig sàrt-biiru Ngomblaan gi ñoo déggoo ci njébbalug naaluw àtte wile.

Kii di dépite Séex Abdu Mbàkke, moom dafa jàpp ni yoon wees jaar ngir jébbal naaluw àtte wi dafa am ay rëq-rëq. Dépite Musaa Jaxate mel ni ku koy tontu, wax ne, boo gisee Pekkug Ngombaan gi woote péncoo, dafa am ab « arrêté » bu ko jëmmal, Abdu Mbów daldi ko ciy feelu.  Muhammet Saañaa (Gii Mari Saañaa) moom, dafa ñaawlu li ko Ngomblaan giy tanqamlu saa su leen jébbalee aw naal, wax ne seen ndajem tey ji dara wundu ko lu moy yàkkamtee « …lekk Usmaan Sonko. »

Ñaari jëwriñ yii di Yanqooba Jémme (jëwriñu Liggéey beek jëflante yi diggante campeef yi) ak Usmaan Jaañ Jémme (jëwriñu Yoon wi).

Léegi nag, lenn rekk a ci des, jàpp bés ngir elimaanu jëwriñ j idem fa Ngombaan ga, biral uw naalu pólitig bi mu tëral, moom ak Càmm gépp.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj