NGOMBLAAN GI WOTE NA SÀRTUB LEERAL BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ngomblaan gi wote na sémbuw àtte wiy leeral àtteb njéggal (loi d’amnistie) bi Maki Sàll, Njiitu réew ma woon, wotelu woon. Dépite PASTEF bii di Aamadu Ba moo tëgg sémbuw àtte woowwi di faramfàcce kan walla ñan la njéggal li ñeel. Ginnaaw bi ñu jokkalantee ay kàddu yu dëgër te tàng, li ëpp ci dépite wote nañu sémbuw àtte wi, daldi koy jàllale.

Daaw, weeru màrs 2024, la dépitey lëkkatoo Bennoo Bokk Yaakaar wote woon aw sémbu àtte bees duppee “Loi portant amnistie”. Maanaam, àtte wow, dafay far ak jéggale lépp luy njombe ak pekke yu jot a xew diggante féewiryee 2021 ak màrs 2024, te laale ak pólitig walla doxi ñaxtu. Ci weneen waxiin, Njiitu réew ma woon, dafa sàkku woon ca dépiteem ya ñu jàllale ab sàrt buy teggil tuuma képp ku ñu jàppoon jamono jooja, walla Yoon doon la topp, moo xam yaa nga woon kaso am déet, nga nekk Senegaal walla bitim-réew. Waayeet, sàrtu baalaate boobu dafa doon tax ba képp ku defoon pekke (nga reyaate, nga reyluwaate walla nga fitnaal ay nit) kenn dootu la mën a topp. Loolu la waa PASTEF ak ñu bari ci doomi réew bañ ba tëdd ci suuf. Li ko waral mooy ne, dañu bëgg leeral li fi xewoon lépp, xam kan moo daan reyaate, ku daan joxe ndigal yi, ku daan fitnaalaate ak lu tax.

Maki Sàll dafa fommoon wotey palug Njiitu réew mi, daldi leen di bëtal. Ca la dugalee woon sémbuw àtte mbaale gi ngir, ca ay waxam, delloosi jàmm ak dal fi réew mi. Dafa di sax, ba sémbu àtte wa jàllee, ca la ñi jiite réew mi tay génnoon kaso, rawatina Basiiru Jomaay Fay (Njiitu réew mi) ak Usmaan Sonko (elimaanu jëwriñ yi). Waaye nag, ñoom waa PASTEF, mësuñoo ànd ci nees tëggee woon sàrt bi. Ndaxte, ci seen i wax, Nguur ga woon duggewu ko woon lu dul nëbb ak làq ay nitam yoy, dañu def lu ne weŋŋ. Loolu moo tax ñu dige woon ne, ca jamonoy kàmpaañ ya, dinañu neenal sàrtu mbaale gi keroog bu ñu faloo. Wànte, neenaluñu ko, danu ko mujje leeral.

Li tax neenaluñu ko nag, ci layi Aamadu Ba mi tëggaat sàrtub leeral bi, mooy ne bu boobaa, Yoon dootul mën a topp ñi laale ci xew-xewi jamono jooja. Nde, ab sàrt du geestu, kanam rekk lay xool.

126i dépite ñoo wote sémbu àtte wi, mu daldi jàll. Léegi, Yoon dina mën a def liggéeyam, lëñbat ba xam ñan ñoo rey 80i ndaw yi daanu woon ci toolu ñaxtuy pólitig yi. Rax-ci-dolli, dinañ mën luññutu ngir xam naka la mbiri Fulbeer Sàmbu ak Dijje Baaji deme.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj