Xeex baa ngi ne kurr ca Ngor. Ndaw ña fay jàppante ak takk-der yi ci buntu pàrkiŋu dëkk ba, fa daamar yay gaare.
Nee ñu, teeruwaayu oto (pàrkiŋ) bi ci buntu dëkk bi lees bëgg a nangu, sanc fa ab AUCHAN. Pàkkub teeruwaay booboo ngi tollu ci 6 000iy m2. Te, ab birigaadu sàndarmëri lañ fa njëkkoon a bëgg a tabax. Loolu la askanuw Ngor wa lànk ba tëdd ci suuf. Ndaw ñaa ngay xeex ak sàndarm yi ca koñu Brioche dorée.
Bees sukkandikoo ci Dakaractu, daluwaayu sàndarmi Ngor yi, mooy birigaad bu Ngor, dafa taa ba mëneesu cee liggéey. Moo taxoon kilifay sàndarmëri bind meeru Ngor bi ngir ñu jox leen teeruwaayu daamar yi, ñu sanc fa seen birigaad bu bees bi. Li jaaxal waa Ngor yi, nag, mooy ne, dañoo jékki rekk, ñu ne leen AUCHAN lañ fay tabax.
Bi ko askan wa yëgee, dañoo fétteerlu, taal i póno ngir fésal seen uw naqar ak seen ñàkk ànd ci naal bile. Fim nekk nii, xeex bi tàng na jérr.