NISEER AM NA NDAM CI KOW FARÃS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Niseer am na ndam ci kow Farãs. Ginnaaw seen xëccoo bu yàgg bi (3i ayu-bés), njiiti Farãs yi mujje nañ xàddi. Nde, seen àmbasadëer bi leen teewaloon fa Niseer, ñibbi na fa Pari ci àllarba ji, 27 sàttumbaar 2023. Sóobarey Farãs yaa ciy topp file ak njeexitalu at mi, ci li Emmanuel Macron xamle, keroog dibéer 24 sàttumbaar 2023.

Keroog, 26 sulet 2023, la sóobarey Niseer ya déjjati woon Muhamet Basum ca jal ba. Ca njeexitalu weeru ut lañ dàqoon àmbaasadëeru Farãs bi, Sylvain Itté. Waaye, ca njëlbeen ga, Njiitu réewum Farãs li, Emmanuel Macron, dafa lànkoon ne du jëfe ndigalu sóobare ya jiite réew ma. Mu juroon coow lu réy. 

Emmanuel Macron dafa ne woon, moom, Muhamet Basum la jàppe Njiitu réewum Niseer. Kon, moom rekk a mën jël ndogal lu ni mel. Waaye de, ginnaaw 3i ayu-bés, Farãs mujje na dellu ginnaaw, woo àmbasadëeram bi, sant ko mu ñibbisi. Moom Emmanuel Macron, keroog dibéer, ba ko waa TF1 ak France 2 dalalee, ca la xamlee ne àmbaasadëeru Farãs bi fa Niseer dina delsi ak sóobarey Farãs ya fa nekk “fii ak njeexitalu at mi”. 

Dafa wax ne, “Farãs jël na ndogalu delloosi àmbaasadëeram.” Rax na ca dolli sax, wax ne “danuy dakkal sunu digaaley xare ak Niseer”. Mu xamleet ne, “ci ayu-bés yeek weer yii ñu dëgmal”, 1 500i soldaari Farãs ya nekk Niseer dinañ ñibbi ñoom itam. Te, file ak atum 2023 miy jeex, soldaar yépp dinañ fa jóge. 

Sylvain Itté, ndawul Farãs la ko teewaloon fa Niseer, dellu na, moom ak juróom-benni ndaw ya mu fa nekkaloon. Àllarba, ci suba si, la teer Farãs. Ci ngoon gi la ko Catherine Colonna, jëwriñu mbiri bitim-réew. Jëwriñu Farãs ji dalal na ko “Ngir gërëm ko ci liggéeyam, moom ak ña ko wëroon di liggéeyal sunu réew, ci anam yu jafe.”

Lii nag, mënul woon a ñàkk. Ndaxte, sóobarey Niseer yee jekku woon. Nde, seen réew lañ nekk, am fa sañ te di dogal. Moo tax, Sylvain Itté ak i ñoñam mënatuñu woon jot ci dund gees leen doon yónnee. Dem nañ bay dunde lekki soldaar yi (rations militaires). Mënuñu woon génn dem fenn. Teg ci ne, amatuñu woon liggéey ndax kilifay réew ma dañ leen fa dàqoon. Ka ñu séqaloon liggéey, Muhamet Basum ak nguuram, daaneel nañ ko te amatul fa baat donte Farãs ñoom, moom lañ jàppe Njiitu réewum Niseer ba tey. Macron feddali na ko keroog. 

Sylvain Itté nag, menn at kepp la def Niseer. Nde, daaw lañ ko fa tabboon. Macron dafa jàpp ni, “ñi aakimoo njiiteef gi fa Niseer” bëggatuñoo xeex rëtalkat yi, maanaam terorist yi. Waaye, ñoom sóobare ya jiite Niseer, neneen lañ gisee demug àmbaasadëeru Farãs bi. Nee ñu, “ab jéego bu bees la ñeel Niseer mi nekk ci yoonu moom boppam”. Terewul nag, ñoom soldaar yi ci boppu Niseer, la leen gënal mooy, ci wàllu demug soldaari Farãs yi, ñu “waxtaane ko” ba “déggoo” ci. 

Mënees na wax ni Niseer am na ndam ci kow Farãs. Laaj bi ñépp di laaj nag mooy, lu ëllëgu Farãs fi Afrig.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj