Senegaal, li ëpp ci lees fiy jëfandikoo, lees di jéggaani la. Dafa di nag, Farãs moo mës a nekk réew mi ëpp li muy jaay Senegaal. Waaye, jagle boobu de, ñàkk na ko ca atum 2024 ma weesu. Ndax, réewum Siin romb na ko léegi.
Bees sukkandikoo ci rootaan yi ANSD siiwal, ca atum 2024 ma ñu génn, réewum Siin mooy réew mom, fa la Senegaal ëppee li muy jéggaani. Nde, li fa Senegaal di jënde àgg na ci 848, 242i miliyaar. Maanaam, téeméer boo jël, 8,3 yokku na ci.
Bu dee Farãs nag, lees fay jënd wàññeeku na bu baax. Léegi, mi ngi tollu ci 725, 252i miliyaar. Maanaam, 17 wàññeeku na ci téeméer boo jël.