Démb lees doon amal palug Donald Trump niki ñeen-fukk ak juróom-ñaareelu (47eelu) Njiitu Réewum Amerig. Moom nag, dafa toog rekk tàmbalee xaatim ay dekkare yu bari ngir dëggal dige ya mu defoon ba muy kàmpaañ.
Coppite yu bari lees di xaarandi biir Amerig ak ci àddina si ginnaaw bi Donald Trump faluwaatee. Nde, njëkk na jiite Amerig diggante 2017 jàpp 2021 laata Joe Biden di ko wuutu. Ci wote yii weesu nag, moo mi am 78i at moo jël raw-gàddu gi, daldi faluwaat ca boppu Réew ma. Dafa di nag, moom Donald Trump dafa am gis-gisu boppam bob, daf ci wooroo ak ñu bari. Ndax, moom, Amerig ak saa-amerig yi la jiital ci kaw lépp ak ñépp. Te, gis-gisam boobu la dige woon ne dina ko jëmmal bees ko falaatee. Démb nag, dafa toog rekk tàmbalee xaatim ak dekkare yoy, dañuy soppi bu baax a baax pólitigu biir réew ma ak bitim-réew.
Ginnaaw bi mu waatee, Trump dafa dafa dellu ca « bureau ovale » ba, pekku Njiitu réewum Amerig, jël ay dogal yu fës ca saa sa. Juróom-ñeenti dekkare la njëkk a xaatim ci fànni ngàddaay li, koom-koom, wér-gi-yaram ak njuux li. Daanaka, dafa bale lépp lu fa Joe Biden bàyyi woon ci fànn yees tudd.
Ci tënk, lees mën a jàpp ci njëlbeenu bésub Donald Trump ci boppu Amerig mooy dekkare yi mu xaatim ak yenn ci kàdduy yéene yi mu biral.
Donald Trump xaatim na fukki-fukki dekkare. Ci biir dekkare yooyu, am na juróom-benn yu ci gën a fës :
-
Dekkare buy dogal lees dippee “état d’urgence” ca seen dig ba ñu bokk ak Meksig, daldi fay yabal sóobare yi ;
-
Dekkare buy dàkkental karteli dorog yi niki kippuy rëtëlkat ;
-
Dekkare buy génnee Amerig ci déggoob Paris (Accord de Paris) ñeel njuux li ;
-
Dekkare buy dakkal mbirum ngóor-jigéen ak yu ni mel ;
-
Dekkare buy génnee Amerig ci kurél gii di OMS ;
-
Dekkare buy goreel junni ciy nitam yees daanoon keroog ba ñu songee “Capitole” ba, di taax bu bokk ca njéndel Amerig la, añs.