Démb, ci alxemes ji, 22 me 2025, Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, àndoon na ak naataangoom bii di S. Mohammet Uld Seex El Xasuwanii, demoon nemmikuji palaatformu gil (gaas) bu “Grand Tortue Ahmeyim (GTA)”.
Waa British Petroleum (BP), Kosmos Energy, Kërug Petorol gu Senegaal gi (PETROSEN) ak Kërug Njafaan yu Móritani (SMH) ñoo dalal ñaari Njiiti réew yi. Dafa di, Senegaal ak Móritani dañu bokk léegi ci réew yiy liggéey ak a jaay gilu yolnde bu raxul dara (GNL). Ñoom ñaari réew yi, dañoo ànd ànd bu rafet, daldi lëngoo di liggéeyandoo ci kaw màndute te bokk i jubluwaay ñeel fànnu laf gi walla yasara. Nde, réew mu ci nekk dafa bëgg a fàggul boppam ay soxlaam ci fànn wile, daldi moom boppam.