NJIITU RÉEW MI DÀQ NA SÉEX UMAR JAAÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, dàq na Séex Umar Jaañ. Moom, Séex Umar Jaañ, moo nekkoon jëwriñ jees dénk mbirum Caytu gi ak Jumtukaay yi ca njiiteefu réew mi (Njénde li). Fan yee weesu, dafa amalaoon aw waxtaan ci tele bii di Fafa Tv, wax ne ñees duppee Les Tirailleurs ay « workat » lañu woon. Kàddoom yooyu, dañu fi sooke woon coow lu réy a réy ba ñu bari doon sàkku ci ñu dàq ko. Tay nag la Njiitu réew mi torlu ab dekkare buy biral dàqug Séex Umar Jaañ.

Keroog, 21i pani desàmbar 2024, Séex Umar Jaañ dafa seqaloon laaj-tontu ak Fafa Tv. Ca biir waxtaan wa, ba ñu àggee ci wëppa Tirailleurs yi, dafa waxoon ne ñooñu, ay « workat » lañu woon. Nde, ciy waxam, dañu xeex seen i mbokk ñuule ci ndigalu tubaab bi. Raxoon na ca dolli sax ne, « ñiy màggal Tirailleurs yi, xamuñu dëggantaan ñan ñoo nekkoon sóobarey mbéeféer yooya. » Ba tay ciy waxam, ba bañkat ya daan fippu ngir dog buumug njaam, génn ci nootaange tubaab bi, Tirailleurs yooyu ñoo daan far a ak tubaab bi di leen xeex ngir wéyal nootaange. Wax jooju nag, juroon na fi riir bu réy a réy. Riir boobu moo ko topp ba nëgëni, waral Njiitu réew mi dàq ko tay, ci 31 desàmbar bi.

Tay lees siiwal dekkare biy firndeel dàqug Séex Umar Jaañ. Ci biir dekkare bi, xamlees na ne kii di Papaa Coon Jeŋ moo koy wuutu. Cig pàttali, ki yor kàddu Càmm gi, Mustafaa Njekk Saare, génnoon na, daldi ñaawlu kàdduy Séex Umar Jaañ yi. ci rajo RFM la waxoon, keroog 26i pani desàmbar 2024, ne « Wax jooju njuumte la. Ànduma ci wenn yoon ak Sëñ Jaañ. Dama jàpp ni Tirailleurs yi ay jàmbaari réew mi lañu. »

Bi loolu weesoo, ki yor kàddu kurélu sëti Tirailleurs yi, Lamin Ba mi fi nekkoon jëwriñ, dafa naqarlu woon kàdduy Séex Umar Jaañ yi, gam-gamle leen ak i xaste, wax ne kàddu yu suufe la te ruslu. Ci mbaali jokkoo yi ak ci jotaayi saabalukaay yi, coow laa ngi meloon ne tulleek maale. Donte ne dekkare bi waxul li sabab dàq gi, njortees na ni coow looloo dàqlu Séex Umar Jaañ.

Bu yàggul dara, Nguur gi, ci kilifteefu Njiitu réew mi, doon nañ màggal xew-xewu Caaroy 1944 ngir sargal ci Tirailleurs yi nootkati Farãs yi bóomoon ginnaaw bi ñu laajee seen i àq ñeel payoor gi Nguuru Farãs ameeloon.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj