NJIITU RÉEW MI FA TUUBAA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, amal na génnam gu njëkk ci biir réew mi. Ag tukkig nemmiku la def, tey, fa Tuubaa. Dafa seeti woon kilifag yoonu Muriit, di Sëriñ Muntaxaa Basiiru Mbàkke.

ci lees rotal ciy xibaar, Njiitu réew mi dafa amal i tukkiy nemmiku yoy, kilifa diine yi la leen di jagleel. Tuubaa nag la njëkke.

Moom, Njiitu réew mi, wedamloo na ñi ko daan solal mbubbum salafist. Ndeke fen du bijjaaw.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj