Njiitu réew mi, Maki Sàll, dalal na ki koy wuutu, Basiiru Jomaay Fay, ak Usmaan Sonko.
Ca Pale ba la leen dalal tey ci alxames ji. Njiiteefu réew mi (Présidence de la République) moo siiwal nataali ndaje mi. Ñu gis ci Maki Sàll di saafonte ak Basiiru Jomaay Fay ak Usmaan Sonko.
Ci lees biral, ñaari Njiiti réew yi, kiy fegal ak kiy jël, waxtaan nañu lu xóot ci wayndarey Càmm gi, xewteg waat gi (cérémonie de prestation de serment) ak xewteg njébbalug lenge yi (cérémonie de passation de service).
Ginnaaw biñ waxtaanee ba noppi, wërloo nañ Basiiru Jomaay Fay ak Usmaan Sonko Pale bi.
Ñépp ñoo rafeltu ndaje mi ak saafonte bi. Muy firndeel ni Saa-Senegaal yi ay nitu jàmm lañ.