Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, tabb na Soxna Aminata Ture. Ci altine ji, 26i pani ut 2024 la torlu dekkareb 24/1796 bu 26i pani ut 2024, tabb ko. Waaye, ci talaatay démb ji la xibaar bi jib. La mu ko tabb mooy, ci nasaraan, « Haut Représentant du Président de la République ».
Moom, Soxan Aminata Ture, rafetlu na ndogal li, daldi bind ci xëtu Facebookam :
« Maa ngi sant bu baax a baax ak di gërëm Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ginnaaw bi mu ma tabbee, def ma Ndaw lu mag luy teewal ak a waxal Njiitu réew mi [mu doon]. Maa ngi yeesal sama dogu gu mat sëkk ci liggéey ngir Senegaal gu moom boppam, tegu ci yoon te ànd ak naataange. »
Dafa di nag, ñu bari dañu réere ndombog-tànk boobii di « Haut Représentant du Président de la République ». Moo tax sax ñenn ñi di ko soofantal, di jàpp ni dafa bokk ci lees di wax « toog muy dox ». Waaye, solos ndombog-tànk bile réy na lool bu fekkee xamees na dëggantaan li mu wund. Moo tax mu jar a leeral fii.
Balaa dara, lees war a xam mooy ne, bees waxee « Haut Représentant du Président de la République », mooy Ndaw lu mag luy teewal ak a waxal Njiitu réew li. Moom nag, liggéeyam du rekk di teewal ak a jottali kàdduy Njiitu réew mi. Déedéet.
Li njëkk a war « Haut Représentant du Président de la République » mooy di jokkale njiiteefu réew mi ak yeneen i banqaas, muy ay campeefi bokkeef gi, diy kurél ci àddina sépp walla ay boroomi tur ci fànni pólitig, koom-koom, dipolomasi, añs. Maanaam daal, mooy doon buum giy lëkkale Njiitu réew mi ak campeef yi, fi réew mi ak fa bitim-réew, di yombal jëflante yi ak a yaatal diggante yi ñeel Njiitu réew mi ak yeneen i jëmm walla kurél yu ràññeeku. Bokk na yit ci lees ko sas :
-
Xelal Njiitu réew mi ci mbir yu solowu yi niki mbiri bitim-réew, kaaraange gi, koom-koom gi, pólitig, añs. ;
-
Muddaarantey dipolomasi yi, di ko waxtaanal ak yeneen i Càmm walla kuréli àddina si ;
-
Dëppale naali pólitig yi Njiitu réew mi samp, di saytu pólitig yooyii ci njëwriñ yeek yenn këri liggéey yi ;
-
Teewal ko ci ndaje yi, muy ndaje yu mag yi ci àddina si, ci yenn xew-xew yi walla ci yeneen i xewte yu mag ;
-
Defar diggante yi, bu dee dafa am réeroo walla ay ñagas-ñagas ci diggante yenn kurél yi walla ay nit. « Haut Représentant du Président de la République » bi day dox ci diggante yi, di defar, di rattaxal diggante yi, ak di juboolewaate ;
-
Jokkalekat, di jottali ndogali Njiitu réew mi yeneen pàcci Nguur gi ak taskati xibaar yi, walla di tontu laaji taskati xibaar yi ñeel pólitig yi Njiitu réew mi di lal, añs.