NJIITU RÉEW MI TAS NA NGOMBLAAN GI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ngomblaan gee saay. Ki ko faat mooy Sëñ Jomaay. Démb la biral ndogal li, moom, Njiitu réew mi. Xibaar bi nag, bettul kenn. Nde, keroog, ca ëllëgu dibéeru 24 màrs 2024, bi njureefi mbañ-gàcce yi lawee, mu bir ne Jomaay a falu, ca lees tàgge woon Ngomblaan gi. Juróom-ñaari weer tegu ci, Ngomblaan giy sukuraat, di bañ-bañlu. Waaye, démb, bi 20i waxtu toftalee as-tuut ciy simili la ko Njiitu réew mi doggali, tas ko tasar.

Ci alxamesu démb ji, 12i pani sàttumbaar 2024, la Njiitu réew mi doon wax ak askan wi. Bi 20i waxtu jotee ci guddi gi la jël kàddu gi. Fa njénde la la doon waxee, tele RTS ak yeneen teley réew mi jàllale ko. Réew mépp a ko doon xaar, di ko déglu ngir xam lan ndogal lay jël ñeel Ngomblaan gog, coowoo coow sooke na ko fi. Daf koy tas am du ko tas ? Tontul laaj bile la ñépp doon xaar donte ne, ñi ëpp ci nit ñi njortoon mooy ne daf koy tas. Te, loolu la Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay dëggal, tas Ngomblaan gi.

Moom nag, Njiitu réew mi, dafa torlu woon ab dekkare, jàpp bésub 13 ci weer wii ngir elimaanu jëwriñ yi defi DPG fa Ngomblaan ga. Moo tax, ñenn ci waa kujje gi di wax ne dafa wor kàddoom. Njiitu réew mi weddi tuuma jooju. Ci li mu wax, naxantewul ak askan wi te amoon na yéene liggéey ak dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi. Waaye, ci gis-gisu Njiitu réew mi, ñoom dépitey BBY yi, liggéeyal Senegaal taxu leen jóg. Ba tey ciy waxam, dara soxalu leen « … lu dul xaxarante ak gàntal lépp loo xam ne bëgg nañ ko doxal ci li nu diglanteek sunu digganteek Senegaal. »

Bi mu xamee loolu, ci la waxtaaneek Ndajem ndeyu sàrtu réew mi, laaj ko ban mooy lél bi nga xam ne, bu ci tasee Ngomblaan gi dinaa tegu ci yoon. Mu dellu waxtaan ceek elimaanu jëwriñ yi ak njiitul Ngomblaan gi. Ginnaaw gi la « … jël ndogal, ne Ngomblaan gii, tas naa ko bés niki tey. »

Njiitu réew mi lim na sabab yi ko tax a tas Ngomblaan gi. Ndeem nettali ci làmmiñu boroom la dàqee, nañu ko bàyyee kàddu gi :

« Njëkke nañu ko ci weeru suwe 2024, ñu am wareefu def li ñuy woowee “débat d’orentation budgétaire”, ñu bañ ne duñ ko def ndax dañ leen a wax lu leen neexul ci làngu pólitig gi. Loolu nag, jalgati sàrt bi nga xamante ne moo yoonal lépp lu laale ci “loi de finances” fii ci Senegaal. Mu yàq deru Senegaal ci biir réew mi ak ci bitim-réew. Loolu doyul. Ñu toftal ci, ci weeru ut 2024 ba tey, ma jébbal leen sémbuw àtte ngir ñu soppi ndeyu sàrt réew mi, ndax ñu mën a dindi HCCT ak CESE, loo xam ne alal ji ciy dem, amunu ci beneen yéene bu dul defaat ko ci réew mi, def ko ci ndaw ñi, def ko ci mbey mi, ñu bañ ne duñ ko dindi donte ne loolu laa diglanteek askan wi ba tey. Dem nañu sax ba foqarti baatu Njiitu réew li ma doon, di jàpp bésu DPG [gaaralug naalu pólitig], salfaañe dogu 84eel ci sunu ndeyu sàrtu réew ak dogu 97eel ci àtte biy yoonal sàrtu biiru Ngomblaan gi. Waxatuma sax, ñu naan dañuy daaneel Càmm gi nga xamante ne moom lañ fi teg. »  

Kon, bees sukkandikoo ciy kàddoom, taxawaayu dépitey Bennoo Bokk Yaakaar yi moo tax mu tas Ngomblaan gi. Nde, dañ ko tere liggéey, tere ko jëmmal dige yi sasook askan wi. Moom nag jàpp na bés bees war falaat yeneen dépite yu bees, muy bésub dibéer 17i pani nowàmbar 2024. Daf ne :

« … lu tax ma tas Ngomblaan gi du lenn lu dul bëgg ñu delluwaat ci askan wi, ngir man mii ci sama bopp, ma laaj leen ñu jox ma jumtukaay yuy tax ma mën a doxal li nga xamante ne moom lañ ma wóoloo.  Kon tey jii, askan wi moo moomaat boppam, moomaat baatam, te am sañ-sañu wax kan lay jiital ca Ngomblaan ga, dooleel ko fa ngir mu doxal. »

Bu ko defee, fii ak 58i fan, askan wi dina delluwaat ci mbañ-gàcce yi, sàndiy xob ngir fal ndaw ya leen di teewali ca Ngomblaan ga. Njiitu réew mi wax na tamit ci anam yi Nguurug Maki Sàll mi mu wuutu yoree woon réew mi. Ciy waxam, yoriin wu ñaaw a ñaaw la te dina Yoon dina def liggéeyam. Dees na ci ñëwaat ci beneen yaxal.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj