Démb la woon alxames, 26i pani sàttumbaar 2024, yemoo ak bés bees di fàttaliku suuxug “Bateau Le Joolaa”. Bés boobii la Càmm gi tànn ngir biral njureef yu tukkee ci càmbar bi ñu doon càmbaar ndono li leen Maki Sàll ak nguuram ga woon bàyyee. Naam, démb, gaal guy daw suuxul, 1 863i bakkan desuñu ci géej gi. Waaye, gaalug koom-koomu Senegaal moo suux, ay miliyaari miliyaar seey ci géejug njuuj-njaaj, wuruj, mbuxum ak i naxee-mbaay. Yëg-yëg boobu la Saa-Senegaal yi am ginnaaw bi elimaanu jëwriñ yi ak ñenn ci jëwriñ yi siiwalee anam bi nguurug Maki Sàll gi yoree woon koppari askan wi. Bor bu jéggi dayo, gafaka gu fëkk walla kees bees këptal… Lii la Usmaan Sonko aajar démb.
Bi Usmaan Sonko duggsee, fas kanam gi, ne këj, ci lañu xam ni la mu nar a wax du gaatnga jàmm. Naam, lu weex la sol, waaye kanam gu lëndëm la ñëwee, moom ak jëwriñ yi ko daroon, fas yéene siiwal njureef yuy wone ne Senegaal a ngi ci guddi yu lëndëm. Te, li fi Maki Sàll di nekk yépp, moom ak i àndandoom, dañu doon tuur askan wi lëndëm, di wax lu amul, di leen nëbb tolluwaayu réew mi. Laata ñuy tàmbali jébbaane bi, dañu njëkk a amal similib tekkaaral ci càkkuteefu Usmaan Sonko. Li mu dugge woon mooy fàttaliku suuxug “Bateau Le Joolaa”.
MAKI SÀLL AK I ÑOÑAM WAXUÑU DËGG
Fa Ndakaaru, ca taaxub caytu gi, la Càmm gi doon janook taskati-xibaar yi. ginnaaw elimaanu jëwriñ yi, Ahmadu Al Amiinu Ló (Magum fara-caytu Càmm gi), Usmaan Jaañ (jëwriñu Yoon wi), Abdurahmaan Saar (jëwriñu Koom-koom gi, Naal wi ak Digaale bi) ak Abdurahmaan Juuf (jëwriñu Njàng mu kowe mi) teewoon nañu fa. Usmaan Sonko moo njëkk a jël kàddu gi, tuumaal Maki Sàll ak ña mu daan liggéeyandool. Ciy waxi elimaanu jëwriñ yi, dañu leen jox ay limat yu safaanook li am dëggantaan ñeel gafakag réew mi, boru Senegaal bi, rawatina ndoyadig koppar yi (déficit budgétaire). Daf ne :
“Njiit yi nu fi wuutu dañu fen réew mi ak i digaaleem […] daldi joxe ay lim yu wéradi.”
Lim yi Usmaan Sonko di wax ñu ngi aju ci diggante 2019 ak 2023. Mu waxaat ne :
“Nguurug Maki Sàll gi dafa labaj lim yi ngir melal koom-koomu Senegaal, ay kopparam ak nafaam ci anam bu safaanook dëgg. Muy lu doy waar ba jéggi dayo.”
Xamle na ne, am na 600i miliyaar yees waroon a jëfandikoo ci atum 2024 mi, dale ko 1eelu fanu sãwiyee. Waaye, fekkuñu fi tus. Maki Sàll ak nguuram ga woon ñoo ko jëfandikoo ba mu jeex tàkk. Sonko nee, “… jamono ji may wax ak yeen nii, xamunu fu xaalis bi jaar. Kenn mënu la wax fees ko def.” Looloo ko tax wax ne, jëwriñ ya woon, Aamadu Ba, Mamadu Mustafaa Ba ak Abdulaay Daawda Jàllo ñoo nekk ci ginnaaw njombe wii. Waaye, ciy waxam, lu jiin Njaag a, te Maki Sàll mooy Njaag. Nde, ba tey ciy waxam, moo leen yilifoon ñoom ñépp. Kon, dara umpu ko ci woon.
BOR BU JÉGGI DAYO
“Caabal giy fésal tolluwaayu nafag réew mi day wone ni boru Senegaal bi ak ndoyadi gi weesu nañ li njiit yi fi nekkoon siiwal te ñu waxoon ko sunuy digaale, diggante 2019 ak 2023.”
Jëwriñ Abdurahmaan Saar moo fésal yile kàddu. Mu neeti, “ndoyadig nafa gees yégle woon, wax ne mi ngi tollu ci 5,5% bees ko méngalee ak PIB bi, ndeke weesu na ko ba ful ko ñaar, maanaam 10,1% la.”
Bu dee bor bi, nguurug Maki Sàll gi dafa xamle woon ne mi ngi tollu ci 65,9% ci PIB bi. Waaye, jëwriñ Abdurahmaan Saar nee na loolu wérul. Ndaxte, ba tey ciy waxam, bor baa ngi tollu 76,3%. Li ko sabab, bees sukkandikoo ciy leeralam, mooy ne ndoyadi gi ñu fi fekk moo ëpp fuuf li ñu leen waxoon. Jëwriñ ji dolli ci ne :
“Ci njeexitalu atum 2023 mi, boru Réew mi […] boo ci seppee boru yi nguur séq ak jàmbur yi, mi ngi tolloon ci 15 664i miliyaar, maanaam 83,7% ci PIB bi. Te, njiit yi fi nekkoon 13 772i miliyaar lañu waxoon, maanaam 73,6% ci PIB bi. Muy ab ndollent ci bor bi te kenn bindu ko fenn.”
Ndekete, ñoom Maki Sàll dañu leb ci turu askan wi ay koppar yu tollu ci 1 892i miliyaar yoy, waxuñu ko ñi ñu ko waroon a wax, binduñu ko fi ñu ko waroon a bind. Muy doxalin wu jëwriñ ji ñaawlu. Ci fànn woowu, bi Al Amiinu jëlee kàddu gi, xayma na ko ba wax ne, ci misaal, Saa-Senegaal bu nekk ame na boru 900 000 ci sunuy koppar. Maki Sàll a ko leb ci turu askan wi. Te, li doy waar ci mbir mi mooy ne, yemuñu rekk ci leb lu ëpp bañ ko yégle. Waayeet, xaalis boobu ñu leb kenn xamul fu mu dugg. Looloo jural Càmm gu bees gi ay jafe-jafe ba tax leen a lebi ay “eurobonds” ngir mën a joyyanti yëf yi.
YOON DINA DEF LIGGÉEYAM
Tóoxidóona yooyu nag, mënees na ci topp aji-def yi. Loolu la jëwriñu Yoon wi, Usmaan Jaañ, xamle. Nee na, ñi jiite yoon dinañu def seen liggéey ni mu waree, ci seen teeyu bakkan, xool yen luññutu lañu war a def ak naka lañu koy defee. Muy dalal xelu ñépp ne, jaay-doole du ci am te kenn du jalgati àqu kenn.
“Dëgg la, du man maay àtte yëf yi. Ñi jiite yoon ak takk-der yi ñoo war a def. Seen liggéey la. Li ma mën a wax mooy ne, dinañ ko def ni mu waree ba mu mat sëkk, ci anam bu leer tey sàmmaale rafetug njort gi war ci ñees ciy tudd.”
Waaye nag, Yoon du baale te du yox-yoxi. Lépp lu ci war rekk, te dëppoo ak sàrt yi, Yoon dina ko def. Loolu Usmaan Jaañ dige.
“… Dinañu càmbar lépp ci anam bu leer a leer te lalu ci kow màndute, képp ku ci taq dees na la joxoñ, teg la daan yi war.”
Liggéey bi jëwriñ jiy wax, ëttu àtte bii di “Pool Judiciaire Financier” moo koy def. Di fàttali ni, Maki Sàll ci boppam moo sosoon PJF bi, mu wuutu CREI bees doon ŋàññi. PJF mooy àtte mbiri nger ak yu ni mel : luubal ak càccug alalu réew mi, njuuj-njaaj ak mbuxum, jalgati yi aju ci kopparalug rëtalkat yi (terorism), njaayum roñukat yi ak càrtalug bànk yi (réglementation bancaire), añs.