NJOMBEW 6i PÀKK YI NGUUR GI WÀNTEER PERETZ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Noppeegunoo wax ci njombew pasug 45i miliyaar yi, ñu sullil nu beneen tóoxidóoni. Usmaan Sonko, njiitalu PASTEF li, moo siiwal beneen tojaange bu Nguur gi defati, keroog bi muy janook taskati-xibaar yi. Ci alxames ji, 10i fan ci nowàmbar la meeru Sigicoor bi tuumaal Njiitu réew mi Maki Sàll ak nguuram, wax ne, dañoo jaay 6i pàkki suuf. Ci biir 6i pàkki suuf yooyu, taax ba Caytug sàndamëri gu mag nekkoon ci la bokk.

Fan yii yépp, jàppug taskatu-xibaar bii di Paap Aale Ñaŋ a lëmbe jataay yi. Ñu bare jàpp ne, dañu ko bëgg a noppiloo. Nde, moom, bokkul ak taskati-xibaar yiy nettali li ñu leen di dégtal ciy xibaar te di ca yem. Moom, dafay luññutu, lëñbët, di sulli ay mbóot ak mbir yu soxal askanuw Senegaal te Nguur gi di leen nëbb mbooloo mi. Dafa di sax, looloo sabab ñu nëbbagum ko jant bi. Nde, dafa àddu woon ci pasug caabalug lëñbët gi sàndarma yi amaloon seen biir ñeel mbirum Aji Saar ak Usmaan Sonko, ba turi kilifa yu mag fés ci, muy njombe wu réy a réy. Waaye, ginnaaw njombew ngànnaay yi njëwriñu kéew gi jënde 45i miliyaar wi yéemoon askan wi, weneen daf cee dolleeku. Usmaan Sonko a ko siiwal keroog, bi muy wax ci mbiram ak mbirum Paap Aale Ñaŋ. Ñaari njombe yu mujj yile nag, am na buum gi leen lënkale bees sukkandikoo ci kàdduy Usmaan Sonko, te mooy njabootu Peretz.

Juróom-benni pàkki suuf yu nekk ci diggu dëkkub Ndakaaru, tollu ci 5. 000 m2, la njiitalu kujjeg pólitigu Senegaal li wax ne Nguur gi daf ko jaay. Mu ne, ki ko jënd du kenn ku dul Gaby Peretz, ab saa-israayel buy yëngu ci njaay ak njëndum ngànnaay. Gaby Peretz moo sax, nee ñu day jaay làrmeb Senegaal ay ngànnaay, di ko lebal itam xaalis. Sonko ne, li tax Nguur gi jaay pàkk yooyii njabootu Peretz mooy ne, Gaby Peretz dafa nangoo wóoral làrmeb Senegaal borub 300i tamndareti (miliyoŋi) ëro, maanaam 196i tamñareti (miliyaari) FCFA ngir mu jënde koy ngànnaay ci diirub 3i at.

Pàkk yees leen wànteer, ci kàdduy Usmaan Sonko, ci seen kërug liggéey gii di AD Immobilier lees ko jaare. Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo xaatim dekkare yi. Pàkk bu nekk, am nab taax. Ñoom, njabootu Peretz, tàmbali nañoo màbb yenn taax yi ngir waajal tabax. Li ci doy waar, ci waxi Usmaan Sonko, mooy ne :

« Ci pas gi, dañu wax ne bu tabax gi àggee, mën nañu sàkku ñu jaay leen benn yoon suuf si ñu tabax taax bi (ci njëgu 60. 000i FCFA m2 bu nekk gën-gaa bari). Pàkk biy jar 7i tamñaret (miliyaar), ñu nar leen ko jaaye 280i tamndaret noonu… »

Li Sonko di ñaawlu mooy li Nguur gi jalgati yoon ci anam bu leer nàññ, mu mel ni teyeef la. Waaye, nee na, dépite Yewwi Askan Wi dinañu leeral njombe yi Nguurug Maki Sàll def yépp. Wànte, du doon lu yomb. Nde, 2012 ba tey, lees fi lim ciy tóoxidóoni, lakk du leen jeexal :

Maam Mbay Ñaŋ ak 29i miliyaari PRODAC yi

Mbuxum gi ci jàll-waaxi dipolomat yi

– Julaatug xaalis bu bon bi

– 94i miliyaari Maamuur Jàllo yi

 3i ektaari Le Dantec yi

 Pasug 45i miliyaar gi añs.

Ku lim juum, waaye njombe du jeex du xaaj. Ba ci li Njiitu réew mi defagum lu baax sax, am na ciy ñaawteef yu leen gàkkal ñeel nger, boddekonte mbokk, càcc, cuune… Fim ne nii, Nguur gi jéemul a weddi tuuma yees gàll ci kowam. Moom kay, dañu singali maxejj yiy làññi ak a wuññi seen i mbóot yi ñuy làq askan wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj