Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay, ma nga woon Farãs. Daf fa teeweeji woon am ndaje ñeel mbirum ñakk ci àddina si. Ba mu fa jógee nag, Njiitu réewum Farãs, Emmanuel Macron, dëne woo na ko, dalal ko. Noonu, ñaari Njiiti réew yi séq nañu waxtaan wow, ci lëkkatoo ak jëflantey ñaari réew yi la aju.
Ay xibaar ruus nañ, bawoo ca seen waxtaan woowa. Bees ci sukkandikoo, yeesalug jëflante yeek doxaliin yi mooy li gën a soxal ñaari Njiiti réew yi. Nde, Njiiti Senegaal yu bees yi dañu bëgg dog buumu nooteel gu yàgg a dox diggante Farãs ak Senegaal, dale ko jamonoy mbéeféer ga ba tey. Askanu Afrig tamit, rawatina ndaw ñi, dañu fippu, taxaw temm ngir Farãs teggi óomam ci baati Saa-Afrig yi, génnee loxoom ci seen pólitig ak koom-koomi réew.
Li Saa-Afrig yi bëgg, Njiitu réewum Senegaal li bëgg ko yit, mooy diggante bi doon diggante nawle yu wegante, joxante cër, ku nekk yem fi nga war a yem. Ci wàllu liggéey, ñu tëral ay digaale ak i pas yoy, ñépp ñoo ciy gis seen bopp, jariñu ci, kenn bañ cee loru. Rax-ci-dolli, ci wàllu demokaraasi, ñu jàppalante ci dëgëral ko, ñoŋal ko, seqiy jéego jëm ci lépp lu koy baaxal ak a jëmale kanam. Waaye, ñaari Njiit yi fas nanu yéene amal ag lëkkaloo gu lalu cig nite ak jëflanteg xaritoo.
Bu loolu weesoo, Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak Sëñ Emmanuel Macron waxtaan nañu ci pexe yi ñu mën a lal ngir wéyal ak a dooleel lëkkatoog ñaari réew yi. Li ñu ko duggee mooy fexe suuxat fànn yiy tax réewum Senegaal ne jonn, gën a moom boppam.
Ba tey, ñaari Njiiti réew yi fas nanu yéene tëral ay naal ak i sémb yu aju ciy fànn yu wuute niki soppiku ci wàllu yasara (transition énergétique), wér-gi-yaram, tàggatu cig xereñte, defar ay ñakk ci réew mi ak mbay mi.
Ku nekk ci ñoom ñaar rafetlu na yéene ji naataangoom am ngir dooleel jëflante diggante Senegaal ak Farãs.