Solhan, gaawu, 5eelufan ci weeru suweŋ, ci kow i néew la jant bi fenk. Xetub bànqanoos bu jaxasook xetu deret ubale foofu yépp. Ay mag ak i ndaw, góor ak jigéen, ñoo tëddoon ci suuf su xonq si. Ñenn ñi doon i néew, ñeneen ñi deewul amey gaañ-gaañi fetel. Tuut-tànk yi sax muccuñu ci Kalachnikovs yi. Way-feteerlu yi ñoo fa jaar ci guddi gi, rey fa 160i nit. 2015 ba tey, guléet cong mu ni mel di am ci réewum Burkinaa Faaso.
Solhan, 2i waxtu ci guddig àjjuma 4eel jàpp gaawu 5eel ci weeru suweŋ, lépp a ngi ne selaw, waa dëkk bay nelaw. Picc woyul, rab doxul. Dëkk bépp muuroo lëndëmaayu guddi gog, mu ngi sànge nit ña malaanum noflaay, ngir teggil leen coonoy liggéeyu bëccëg bi. Waaye, guddi gu bët setagul, lu ne xaj na ci. Ndege, jàmm jooju, du woon luy àgg bët-set.
Ci biir dal ak tekk googu lañ tàmbalee dégg i riiri móto yuy jibee fu sori. Riir yiy gën di yokk, di jegesi, ànd ak i yuuxu ak i «Allaahu akbar!». Ndekete, way-feteerlu yaa leen ganesi. Musiba dikk na ! Balaa ñuy xippi seen i bët, feteli “Kalachnikovs” yi tàmbali nañuy sox, di ratatati. Bitig ya, kër ya ak yenn ciy palaas di tàkk. Yuuxoo yi, soxi fetel yi, saxaar si, lépp jaxasoo, mu mel ni àddina suy tukki. Nit ñay tëb ci lal yi, xale yay daw làqu ci seen i way-jur, jigéen ñay yuuxoo ak a xaacu, mag ña boole tiit ak njàqare, góor ña saalit : dee dikk na ! Laata ñuy xam li xew, yenn ciy bakkan jot nañoo rot, ñu bare ame ay gaañu-gaañu. Li guddi giy dem, limu néew yeek nit ña amey gaañu-gaañu di yokku. Noonu, ba bi ndimmal liy agsi Solhan, daanaka, 6i waxtu ci suba jot na. Ndeysaan, boobu, fekk na way-feteerlu yi rey 160i doom-aadama, lem seen i dëbës, ne mes.
Tiis week naqar wi ame ñépp. Ñu ne yàbb, kenn xamul looy wax. Xel yi fattu, rongoñ yiy tuuru, bët yi xonq. Isuf Sow, meeru Solhan ne, «musiba bu réy a réy la». Daanaka, ameesoon nay jafe-jafe ci limub néew yi. Solhan, 5000i bakkan lees fa limoon laata rey gi di am. Ci gaawu gi, waa dëkk bi ñoo gaawantu dajale néew yi, wodd leen i basaŋ, boole leen rob ci 3i bàmmeel, bàmmeel bu ne ñu suul fa lu tollu ci 50i néew ak lu teg.
Bees sukkandikoo ci kàdduy benn depite bu waa “Agence France-Presse” doon laaj, 20i xale ñàkk nañ ci seen bakkan. Mu teg ci ne, ba ci dibéer ji, takk-der yaa ngi doon luññutu, di wër ngir teg loxo way-feteerlu yi def ñaawteef bile. Dafa di, ba nëgëni-sii, kenn ci way-feteerlu ya fay xoqatal ak a fitnaal askan wa waxagul ne moo def lu ni mel. Du waa Al-Qaida, du waa EI (Etat Islamique).
Bees sukkandikoo ci ñenn ci waa dëkk ba, way-feteerlu yi dalub «VDP» (volontaires pour la défense de la patrie) yi lañ jëkk a song laata ñuy rajaxe mbellum wurus wu dend ak dëkk bi.
Adama, benn pël bees rawale Wagadugu, ca lalu loppitaan ba mu nekk, ne way-feteerlu yi dañ leen waxoon ne «waa dëkk bépp lañuy rey laata sox yi tàmbalee taw sunu kow». Moom, 40i at la am, di jeexkatu wurus. 3i sox la ko way-feteerlu yi dóor, mu daw làqu ci suufu mbaaram. Bu dee-delluwul woon, àllaaxira lay yeewooji. Waaye, doom ji, moom, muccul. Ndeysaan, ci kanamam lañ reye doomam ji tolloon ci 5i at doŋŋ, ak 3i doomi-bàjjenam.
Ay seede yu bari yu fa dëkke nee nañu ay góor yu gànnaayu delsi nañ fa ci guddig gaawu gi, taal la fa desoon ciy bitig. Looloo sabab waa dëkk ba mujj daw. Ñii war seen i saret, ñee seen i móto, ñeneen ñi doxe tànk, wutali Seeba mi leen soree 15i kilomeetar. Ci diggante 2i fan yi rekk, nee ñu lu tollu ci 1000iy nit teersi nañ fa.
Njiit yaa ngi jaaxle. Fu ne nguur gaa ngi fay sàkku ndimbal di soññ askan wi ci ñu maye seen deret.
Kuy dékk say rongoñ di leen siimee cereem, deesu ko ñaan ñeex
Nees ko saxoo saa bu dara xewee, yégle tàmbalee jib, ñii di ñaawlu, ñee di wone seen ñówental ; ñenn ñiy jaale, ñeneen ñiy joxey dogal.
Ci gaawu bi, Njiitu réewum Burkinaa Faaso, Roch Marc Christian Kaboré, dafa méngale cong mi ak coxorte ak ñàkk a nite. Mu xaatim ab dekkereb ténj 3i fan. Njiiti réewi Afrig yi ak UA di génneey yégle ngir, ci seen i mbind, biral seenuw naqar ak ànd biñ ànd ak askanu Burkinaa Faaso ak i njiitam.
Antonio Guterres, njiitalu ONU, moom, dafa ñaawlu mbir mi laata muy wax ne, «dafa jot àddina sépp booloo daldi dimbali kenn ci ñoom ci jafe-jafe yi muy jànkonteel ak taafarug pétteeral gi».
Jawriñu mbirum bitim-réew ju Farãs, Jean-Yves Le Drian moom, ci dibéer ji, ci Twitter la xamlee ne dina dem Burkinaa Faaso ci ayu-bés bile ngir jaale leen ci turu réewam.
UE ñoom itam, ci seen yégle, dañ ñaawlu liñ woowe jëfu buqat ak coxorte. Mu ñaax njiit yi ñu def seen kemtalaayu kàttan ba jàpp way-feteerlu yi ko def.
Waaye, ndax warees na xaar dara ci doxandéem yile ? Lii xew, ndax ñoom mucc nañ ci ? Gànnaay yi way-feteerlu yiy reyee doomi Afrig yi, ku leen di defar ku dul ñoom ? Ku leen di jaay ? Ku leen di tasaare ci àddina si ? Ku leen di dugal Afrig ? Kan walla ñan ñoo ngemb reykat yu soxor yile ? Ku leen di dundal, di leen jébbal i xibaar, di leen xelal pexem xare ? Bu dul ñoom it, ñàkkul ñu am i tontu ci laaj yile. Kon, dara jàppuleen lu dul naaféq. Nde, buñ sañoon, Afrig du jóg ci fitna. Dafa di, kuy dékk say rongoñ di leen siimee cereem, deesu ko ñaan ñeex.
Càggante walla néew doole ?
2015 ba léegi, réewum Burkinaa Faaso mi ngi jànkonteel ak i jafe-jafe ñeel pétteeral gi. Boobaak tey, ñoo ngi góor-góorlu gaa, waaye dafa mel ni pexe amagul.
Ci atum 2019 lañ jël VDP (Volontaires pour la défense de la patrie) yi ci ndigalu njiitu réew ma Roch Marc Christian Kaboré. VDP yi ay way-yebu yu jël seen dogalu bopp, ràngu ci xeex bi ngir dimbali soldaar yi. Ndaxte, làrme bi kese mënul a xeex ak way-feteerlu yi. Ñoom VDP yi nag, rafet nañ yéene lool, waaye seen xam-xam màccul ci xare, seenub tàggat matul te seen i gànnay doyuñu, teg ci. Moo tax, àjjuma jii weesu rekk, rey nañu 14i way-yebu ca Tadaryat, benn dëkk bu féete ci bëj-gànnaaru réew ma. Meeru Solhan bi ne, ci guddig cong mi, lu tollu ci «20 ak 30i way-yebu » dañ mujjee daw ci kanami way-feteerlu yi ak seen i “Kalachnikovs”.
Ñoo yay, kat…
Ci bési 17eel ak 18eel, songeesoon na benn dëkk, rey fa 15i nit ak benn soldaar. 2015 ba tey, ci xayma, way-feteerlu yi reyagum nañ ca réewum Burkinaa Faaso 1400i nit, sabab toxub 1 tamndaretu nit. (1 milyoŋ)
Moone, bésub 14eel ci weeru Me bii weesu rekk, jawriñu kaaraange réew ma, Sérif Si, demoon na Sebba, wax fa ne jàmm delsi na, dalaloon fa xel yi. Ana mu tey ? Ana soldaari Farãs yi bokk ci Barkhane ak soldaari Càdd yi bokk ci G5 Sahel (Gànnaar, Càdd, Burkinaa, Mali, Niseer) ? Njiit yi dañoo sàggan walla seen i réew dañoo néew doole rekk ?
Mu mel ni pexe amatul. Boroom làmmiñ yu ratax yi ne, Nguur gi ak soldaar yi wóoloontewuñu. Te li ci gën a doy waar, mooy ne, bi mbir mi amee ba léegi, du ndaje, du dara lees amal ngir jagleel ko ko. Lu waral loolu ? Lu tax sàmmkati kaaraange yi yéex a yegg Solhan ngir xettali askan wa ? Lu tax soldaar yi féete Sebaa nekk ci diggante 12i km kese yéex a ñëw ? Ndax li yoon wi baaxul doy naw lay ? Ndax ndell yi way-feteerlu yiy suul ci yoon yi war na tax ñuy seetaan askan wiy dee ci anam bu ni ñaawe ? Laaj yaa ngoog…
Luy jot jot na ginnaaw dee, bennoo mbaa deewandoo
160i néew, du lu ndaw. Muy xew-xew bu tiis lool, metti ci xol. Àddina sépp waroon a yëg metit wi, bokk naqar wi, waaye ñu soofantal ko. Afrig yépp waroon a mànkoo, bàyyi lépp, ñëw bokk ak doomi Burkinaa Faaso yi tiis wi, jàppale leen ci fànn yépp, taxawu leen ci boor yépp. Waaye, ñoom it, ñu yées doxandéem yi, daldi néewal mbir mi ci seen doxalin. Ni taskati xibaar yi jële mbir mi, day firndeel tuutal biñ tuutal jéyyab Solhan bi.
Ndeysaan…
Naam, nguur gi, boobaak léegi mi ngi góor-góorlu di def lum mën. Waaye, dafa mel ni ku wéet ci xeex bi, moo tax sottiwul. Warees na jàngat taxawaayu campeefi àddina si, rawatina yu Afrig yi. Nde, dafa mel ni mbir mi yëngalu leen. Bu dee àddina si sax, mënees na bañ a aayal seen ñàkkug yëg-yëg ci mbir mile. Nde, sikk amul ci ne, lenn rekk a leen soxal ci Afrig, mooy alal ji fi nekk. Li ci des, seen yoon nekku ci. Dañuy xoromal rekk, wànte safu leen sax.
Waaye, ni doomi Afrig yi woyofalee mbir mi moo ruslu. Dëgg la, génne nañ i yégle di ñaawlu, di ñówental, di jaale ak a digley dogal. Waaye, ndax fa lañ waroon a yem ? Ndax mbir mi metti na leen dëgg-dëgg ? Lan moo ciy seen cër ? Ban taxawaay lañ ci am ? Ana ndimbal liñ war xettalee seen mbokk mii di Kaboré ? Naka lañ ko fas yéenee taxawoo ?
Tey laaj yi doomi Afrig yu bariy laaj ñooy :
Ana njiiti réewi Afrig yi séqiwoon i jéego, naaw ba Farãs, naan «Je suis Charlie» ? Ana njiiti réew yi doon jooy keroog bi Jàngu “Notre-Dame de Paris” tàkkee, mu am sax ñu ci “lakk” seen xaalisu askan ?
Ërob, saa bu fa dara xewee, ñoom ñépp ay booloo, jàppalante. Nun, tamit, nu ànd ceek ñoom di leen ko jooyle. Dafa di, àgg nan ci, bu ñu reyee 2 walla 3i tubaab ci Afrig, mu mel ni àddinaa tukki. Waaye, buñ reyee 160i doomi Afrig walla lu ko ëpp sax, dañuy naqarlu mbir mi, jàll, jublu ci leneen. Moone de, bakkan, bakkan la rekk. Benn bakkan gënul bi ci des. Te booy fonk bakkan, bu sa mbokk a ci gën a yay. Nde, mbokk dañu koy dox mbaa ñu wax ko. Waaye nag, làmmiñ rekk, doxul mbokk.
Ni mbir mi safadee njiiti Afrig yi dafa doy waar, yéeme, raglu. Nees soofantalee dee gi ci Afrig dafa yemook xeebeel bi doomi Afrig yi xeeb seen bopp, rawatina njiit yi. Wolof ne, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Moo tax, ba tey, noo ngi wéy di suufe ci kanamu tubaab yi, doyadi lool ci seen i bët. Buñ nu yabee, nun la. Te du, su bukki yabee gaynde, ca doxin wi la ?
Ay doomi Burkinaa Faaso lañu rey, sunuy mbokki deret, sunuy mbokki cosaan, mbatiit, sunuy mbokki Afrig, sunuy dëkkandoo. 160i nit ñiñ rey ak ñi dee ñépp ci Afrig ba mu daj ci anam bu ni mel, warees na leen jàppe niy doomi Senegaal, Mali, Koddiwaar, Gana, Kamerun, Niseryaa, Niseer, Gine, ba Afrig daj. Wenn xeet wi la. Lii xew ca Solhan, la am Mali, la xew Càdd, la xew Kamerun ak yeneeni réewi Afrig, jombul mennum réew ci réewi Afrig yi. Kon, kenn warul a bank say loxo di seetaan sa moroom.
Lu tax Senegaal bokkul ci G5 Sahel bi ? Ak ni làrme Senegaal xareñee ci xeex fitna ak delloosi jàmm, àddina sépp seedeel ko ko… Ay mbokkam aajoowoo ko, mu beru, dummóoyu leen ! Lu tax ? Jàmmu Mali, mooy jàmmu Senegaal ; jàmmu Burkinaa Faaso mooy jàmmu Afrig. Ku jàpp ne mën nga aaral sa bopp sam réew yow kese, juum nga. Ku ci jàpp ne yow rekk mën ngaa muccal sa bopp ci fitnay pétteeral gi, naatal sam réew, yaa ngi nax sa bopp, walla nga tey ko rekk. Booloo mooy doole te moo fi sës. Luy jot jot na ginnaaw dee. Dama ni : bennoo mbaa deewandoo tey Solhan, ëllëg feneen. Yàlla tere tereeti ko, waaye nag…