Léegi la APS siiwal xibaaru paatug Mamadu Mustafaa Ba mi woon jëwriñu ngurd mi ak nafa gi ci nguurug Maki Sàll. Mi ngi amoon 59i at.
Moom, Mamadu Mustafaa Ba, Ñooro (Nioro du Rip) la ganesee àddina ca atum 1965. Prytanée militaire bu Ndar la amee woon « Baccalauréat ». Ginnaaw gi, dafa àggaliji njàngam fa jànguneb Anvers, am ay lijaasa ci fànnu xam-xamu pólitig, koom-koom ak caytug bokkeef. Ca atum 1992 la tàmbalee liggéey ci njëwriñu Koom-koom gi ak ngurd mi. Atum 2022, besub 17i pani sàttumbaar, lañu ko tabb, def ko jëwriñu Ngurd mi ak Nafa gi. Abdulaay Daawda Jàllo la wuutu woon.
Ci altiney tay jii, 4i pani nowàmbar 2024 la wuyuji Boroomam. Njabootam a ko yégal waa saabalkati APS yi.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootam, di ko jaale njabootu pólitigam ak Saa-Senegaal yépp, di ko ñaanal njéggal ak yërmande.