Dañ doon xaarandi Ngomblaan gi wax ci mbirum pasug ngànnaay gi dox diggante Nguurug Senegaal ak kërug liggéey gii di Lavie Commercial Brokers, dépite Abbaas Faal mi bokk ci Yewwi Askan Wi sulli na ko fa. Nde, ci turu kurélug yasara gi ak balluy mbindaare yi, jébbal na Njiitu Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, ag laaj ngir ñu taxawal ag kurélu luññutu ngir leeral mbirum pas googu.
Keroog, 30 desàmbar 2021, la Njëwriñu Kéew mi ak Yokkute gu sax gi nas ag pasug ngànnaay ak kurél gii di Lavie Commercial Brokers. Waaye, bésub 11 saŋwiye 2022 la ko Abdulaay Daawda Jàllo xaatim, bi muy nekk Jëwriñu Ngurd meek Nafa gi. Loolu, nag, OCCRP (Organised Crime and Corruption Reporting Project), ag kurélug taskati-xibaar yiy luññutu ci wàllu njekkar ak nger ñoo ko siiwal ci seen dalu web, keroog 25 oktoobar 2022. Nee ñu, pas gi, àgg na ci 77i tamñareti dolaar, maanaan 45i tamñaret ci sunuy koppar. Ñoom nag, taskati-xibaar yooyu, dañu ñjort ne, pas gi dafa rax nger ak njuuj-njaaj.
Li tax xel yi teey ci pas gi dafa bari. Bi ci jiitu mooy ne, kenn yëgul, kenn tinul. Lépp, ci ag ndéeyoo la ame, diggante Nguur gi ak Lavie Commercial Brokers bi nga xam ne, Abuubakar Hima « Petit Boubé » mooy boroom. Te, kooku, nee ñu, ab saay-saay la bob, waa Niseer ak waa Niseriyaa ñoo ngi koy wër. Ndeke, toppees na ko càcc ak nger ci alal ju tollu ci téeméeri-téeméeri tamndareti dolaar.
45i tamñaret (miliyaar) ci sunuy koppar la Njëwriñu Kéew mi fey Abuubakar Hima. Te, boroomi xam-xam yi taskati-xibaar yu OCCRP laaj, dañu jàpp ne takku xaalis bi dafa ëpp ci ngànnaay yi nekk ci pas gi. Rax-ci-dolli, ñi ñu jagleel ngànnaay yooyii, sóobarey Ndox yeek Àll yi, aajowoowuñu yu ni mel. Nga teg ci ne, ci pas gi, kenn leeralul njëgul benn ngànnaay. Loolu, ci waxi taskati-xibaar yi ko siiwal, moo jur sikk-sàkka yi ci am.
Nguurug Senegaal nag, tontu woon na, weddi tuuma yi. Mu mel ni, ñi jiite réew mi, ci weddi ak teggi tuuma rekk lañu dëkk. Saa su nekk rekk, ñoo ngi leen di tudd ciy njombe ak i tóoxidóona. Moo tax, Abdul Mbay, jëwriñ ju mag ja woon, mere leen lool, ba tax ko wax ne :
« Muy soroj walla di ngànnaayi xare, Senegaal moom benn xeetu doxalin kese la xam, te mooy jëflante ak ay saay-saay yiy làqu ci ginnaawi këri liggéey yu safaanoo ak yoon yi ñu taxawal ngir rekk lu ni mel. Te naan nit ñi doxleen ! Fii lépp a leer te jaar yoon ! Yal na jeex. »
Fi mu nekk nii, dépite bii di Abbaas Faal jébbal na Njiitu Ngomblaan gi, Aamadu Maam Jóob, ag laaj ngir ñu taxawal ag kurélu luññutu ngir leeral mbirum pas googu. Moom, ak ñu bare ci àddina si, dañu njort ne njuuj-njaaj dafa am ci pas gii nga xam ne, ñaari jëwriñ ya woon, Abdu Kariim Fofana (jëwriñu kéew mi ak yokkute gu sax gi) ak Abdulaay Daawda Jàllo (jëwriñu Ngurd meek Nafa gi) ñoo kootoo ak benn Saa-Israayel, xaritu Njiitu réew mi, Maki Sàll. Njiitu réew mi nag, bim faloo ba tey, xeetu njuuj-njaaj u nekk jiiñees na ko ko, moom ak i àndandoom. Te, ay weer yu néew kese ñoo ko dese ci boppu réew mi. Xanaa rafetal jot na ? Waaye, bu naree ñaaw, day ñaaw rekk, di gën a ñaaw.