Ag pasug 45i miliyaar ñeel i ngànnaay yu Njawriñu kéew mi jënde ci LAVIE COMMERCIAL BROKERS moo lëmbe réew mi fan yii. Li ko waral mooy ne, pas gi, ci suuf lees ko lal ak ug kurél gog, nee ñu, boroom ab saay-saay la bees di wër ci àddina si. Te, pas googu, ni ko ñenn ñi waxe, nasiinam dafa woroo ak àtte yi càrtug màrse piblig tëral. Bi xibaar bi jibee ba léegi, lii di niruw njombe lees di waxtaane ci réew mi. Coow laa ngi ne kur, nag. Ndax, bi taskati-xibaar yi biralee pas googii, Nguur gi génn na, ci kàddug Abdu Kariim Fofana, weddi tuuma yees ko gàll.
Ci alxames ji, Libération dafa génney xibaar yu bees ci mbir mi. Bu ñu sukkandikoo ci yéenekaay bi, dugalees na ay daamari Suv ci cantaane gi nga xam ne, boolees na ko ci « kumpay kaaraange » ngir jéggi càrtug màrse piblig gi.
Li jëm ci wàllu ngànnaay yi ci boppam, lépp ñëwagul. Waaye, am na ci lol, nguur gi jotagum na ci. Mu ngi ñu dencandi ca màkkaanu Ndajem Cliss ma. Li ci doy waar nag, mooy ne, ci pas gi, kenn bindu ci njëgul mbenn li, ngir ñu mën a xam ngànnaay bu nekk lu mu dikke réew mi. Ci loolu la ñu bari sukkandiku, wax ne, nguur gi defati na aw njombe. Muy ci kibaraan yi walla ci mbaali jokkoo yi, ñoo ngi leen di yakk lu mel ni xeme. Moo tax ki yor kàddu Nguur gi génn ngir weedi tuuma yees ko gàll.
Abdu Kariim Fofana : « …ay tuuma kese la, dara wéru ci. »
Nguur gi, ci làmmiñu Abdu Kariim Fofana, àdduna ci mbir mi, wax ne :
« Ginnaaw bi ay taskati-xibaar biralee ag pasug njaay gu worook yoon ñeel njaayum ngànnaay diggante Njawriñu kéew mi ak genn kërug liggéey gu tudd LAVIE COMMERCIAL BROKERS, Nguurug Senegaal a ngi leeral ne, wax jooju, ay tuuma kese la, dara wéru ci. »
Ci biir waxam ji, Abdu Kariim Fofana a ngiy dolli ne, pas gi ñuy wax, jaar na fépp mu waroon a jaar laata ñu koy xaatim. Ciy waxam ba tey, amul lenn lu ci safanoo ak yoon. Nde, pas gi, dafa bokk ci « « kumpay kaaraange » yi dekkare 2020-876 bu 25 màrs 2020 biy mottali dogub 3 bu dekkareb 2014-1212 bu 22 sàttumbar 2014 biy sàrtal màrse piblig yi, te ñu soppi ko ak dekkareb 2022-22 bu 7 saŋwiye 2020 bi nga xam ne, day seppi ci càrtug màrse piblig gi lépp luy liggéey, njënd ak jumtukaay yu ñeel kaaraange réewum Senegaal te ñu boole leen ci « kumpay kaaraange ». »
Buñ ko déggee, pas gi waral coow li, bokkul ak pas yees miin. Nde, gile pas, dafa aju ci kaaraange réew mi. Moo tax, ciy waxam, wareesu ko siiwal nees koy defee ak yeneen xeeti pas yi.
Bokk na ci li nit ñiy laaj, ginnaaw xaalis bu ñu ci tudd (45i miliyaar), mooy lu nguur giy doye ngànnaay yi. Loolu tamit, Abdu Kariim Fofanan tontu na ci. Nee na :
« …Njawriñu kéew mi am na sañ-sañu jënd ay ngànnaay ngir Njiiteef gi féetewoo wàllu Ndox yi, Àll yi, Rëbb gi, Càmmug suuf yi ak Ngéddi réew mi. Ñooñu ak aarkati réew mi ñoo yem bu ñu sukkandikoo ci dekkareb 2021-563 bu 10 me 2021. »
Yemu ca, nag. Rax na ca dolli ne, ak fi àddina si tollu tey ci ñàkkug kaaraange, rëtalkat (terorist) yi ak càccug matt gi, day laaj ñu defaruwaat, wut ay jumtukaay yu mucc ayib te méngoo ak jamono. Waaye, dafa mel ni layam bi dàkkul sikk yi ci xeli maxejj yi.
Fi mu nekk nii, noo nga xaarandi ba xam li Ngombalaan giy wax ci mbir mi. Ndax, ba tey, am na ay lënt-lënt yees war a leeral.