Ci talaatay démb ji, li ko dale 11i waxtu ci yoor-yoor bi, lees doon àggali palug Pekkug Ngombalaan gu bees gi. Ndax, mujjewuñu woon àggali liggéey bi ci altine ji. Dafa di, ak rëppaajoo bi fa amoon, def nañu fa 10i waxtu yoo xam ne, kenn xamul woon li Ngomblaan giy niru. Ñu gis fay mbir yoy, guléet muy xew ca Péncum réew ma. Dees na ñewaat ci sabab yi, ci ni mu gën a yaatoo. Moo taxoon, mëneesutoon a àggali liggéey bi, donte ne sàndarm yaa nga woon ca biir Pénc ma, fees fa dell. Nde, Njiitalu Ngombalaan gu bees gi, Aamadu Maam Jóob, ginnaaw biñ ko takkalee ndombog-tànkam, dafa daldi fomm jotaay bi ngir ñu àggali ko ci talaata ji.
Moom sax, coow li toppoon na leen ci talaata ji. Nde, Gii Maris Saañaa këfaatoon na mbañ-gàcce bi. Li Farba Ngom bëggoon a woteel Aminata Ture moo taxoon mu def ko. Waaye, Biram Suley Jóob mujje na ko delloo, ñu daldi wote. Ci njeexital li, nii la Pekk gu bees gi tëdde :