Niki dibéeru démb ji, 8eelu fanu suwe 2025, la kerceni àddina sépp, rawatina yoy Senegaal, doon màggal bésub “Pentecôte”. Mu di bés bu màgg lool ci katolig yi. Nde, bees sukkandikoo ci seen pas-pas, niki bés bile la Ruu Gu Sell Gi wàccoon ca apootar ya (àndandooy Yeesu ya). Bu ko defee, bés bi dafay màndargaal juddug Jàngu bi.
Fi Senegaal nag, at mu jot, dees nay amal ñaari xew-xew yu mag yuy jëmmal màggaayu bés bi ñeel way-gëm katolig yi. Bi ci jiitu mooy ajug Popengin, ñaarel bi di lees di dëggalal ay xale yu bari ak i ndaw ci diiney kercen.
« Mari, ndayu yaakaar ji, àndal ak nun ! »
Boo bëggee xam cosaanu ajug Popengin gi nag, dangay laaj mboor, mu delloo la ca atum 1888. Ndaxte, ca at mooma la sang Pikaardaa digle woon ñu amal ko ca njëlbeen. Li mu ko dugge woon mooy fexe ba Senegaal amal boppam ab barab bob, way-gëm katolig yi dinañu fay mën di daje, di fa jaamu Yàlla ak di Ko sàkkuy ñaan, waayeet di Ko fàttaliku ak a wéttalikoo. Dafa di nag, at mu jot, dañuy tànn aw wëppa wees di waxtaane ngir njariñal àddina sépp, rawatina Senegaal. Wëppaw ren ji nag mooy : « Mari, ndayu yaakaar ji, àndal ak nun ».
Ay junniy junni katolig, mag ak ndaw, góor ak jigéen, ñooy dox, wutali barab bu sell booba di Popengin. Dëkk baa ngi bokk ci diiwaanu Cees, nekk ci depàrtamaawu Mbuur. Mi ngi féete Ndakaaru ci wetu suufam, soree ko 70i kilomeetaar. Ngir taxawu ujaaj yiy dox wutali barab ba, Càmm gi jël na matuwaay yi war yépp ci wàllu kaaraange, wér-gi-yaram, añs. Gisees na sax ñaareelu soxnas Njiitu réew mi muy maye buteeli ndox ak a saafonteek ujaaj yi. Muy lu rafet luy jëmmal ne, Senegaal, benn bopp la, kenn mënu ko xar ñaar.
Fa Jàngub Sigicoor, katedaraalu Sang Antuwaan dë Paduu, làbbe Edmon Eduwaar Saañaa dëggalal na limub 82i ndaw ci diiney kercen. Moom làbbe bi, moo teewal eweg Sang Saŋ-Batist Màngaa. Làbbe Edmon Eduwaar Saañaa jot na fa fàttali mbaax ak jikko yiy màndargaal bés bi : jàmm, màndute ak nangu wuute gi. Maanaam, bennoo ci ngëm, jàppoo ci jàmm. Nde, ciy kàddoom, wuute, gànjar la gog, Ruu Gu Sell Gee ko wërsëgalee nit ñi ngir ñu booloo doon benn.