Naqar ak uw tiis wu réy a réy la njaabotug jànguney Senegaal yi yeewoo. Porofesëer Musaa Daaf moo wàññeeku. Ci bët-setu altiney tay jii, 3i fani féewiryee 2025, la xibaar bi jib.
Porofesëer Musaa Daaf, ku ràññeeku la ci jàngune yi ak ci lépp lu ñeel làkki réew mi. Moom, jàngalekat bi, “linguiste” la woon ak “grammairien”. Ca Faculté des Lettres et Sciences Humaines (FLSH_UCAD) la daan jàngale. Waayeet, daan jàngale tamti fa jànguneb Ndar ba, Université Gaston Berger de Saint-Louis (UGB). Nde, bi ñu taxawalee UGB ca 1990 ba léegi, mi ngi fay jàngale.
Li Sëñ Daaf liggéey ci làkki réew mi, foo ko natt weesu na ko. Ndax, dale ko ati 1980 ya ba ni mu dëddoo ci atum ren jii, liggéey na lu réy ci njàng ak njàngalem làkki réew mi.
Bari na ay maasi jàngalekat ak i ndongo yoy, Pr Daaf moo leen jàngal, tàggat leen. Rax-ci-dolli, Pr Daaf def na liggéey bu am solo ci wàllu njàngalem farãse fi réew mi.
Pr Daaf daan faral di liggéey ak Nguur yi fi jaar yépp, bokk ci ñi lootaabe naali njàng yees di doxal ci daara yi. Waaye, xam-xamam jéggi woon na mbiri làkk yi. Nde, ba ci wàllu mbatiit ak lépp lu aju ci laamisoo ak ladab, Pr Daaf liggéey na ci. Dafa di, moom Pr Daaf moo sumb lijaasa bees duppee Certificat de spécialisation en littératures francophones. Moo tax, njàngaan yi njëkk a bind ay “thèses” ci fànn woowule ca UCAD, ci kilifteefam ak caytoom lañu ko defe.
Du Senegaal rekk a ñàkk nag. Ndaxte, Afrig, rawatina Afrigu sowu-jant, ñàkk na boroom xam-xam bu mag.
Bi 14i waxtu jotee, ci altiney tay jii lañu jële néewam fa jumaay Amoo 4 (Géejawaay). Podoor lañu koy robi.
Yàlla na Yàlla jéggal Pr Musaa Daaf, defal ko yërmande, yéege ko guyaar.
EJO ak LU DEFU WAXU ñoo ngi koy jaale njabootam, ay mbokkam ak i naataangom jàngalekat.