PRODAC : CAABALU ËTTUB CETTANTAL BI DËGGAL NA USMAAN SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, dafa santaane woon ñu siiwal caabali luññutu yees amal ci juróomi at yii mujj. Boobaak léegi nag, banqaas yu baree ngi siiwal seen i caabal. Fan yee weesu, OFNAC la woon. Diggante démb ak tey, Ëttub cettantal bi (Cours des comptes) génnee nay caabalam diggante 2018 ak 2021.caabal yooyii nag, jur nañ coow lu réy fi réew mi. Nde, dañ ciy fésal ay njaaxum ak i luubal yu bare. Caabal yooyii, bu PRODAC bi ci la bokk.

Caabalu Ëttub cettantal bi ñeel naalub PRODAC bi feeñal nay rëq-rëq ci yoriin wi. PRODAC, ab naal woon bob, jàppale ndaw ñee ko taxoon a jóg, rawatina ndaw ñiy yëngu ci wàllu mbay. Moo tax, njëwriñu ndaw ñi lees ko dénkoon. Ca ndoorte la nag, Maam Mbay Ñaŋ a ko jiite woon, moom mi nekkoon jëwriñ ji ñu dénkoon ndaw ñi.

Lu tollu ci 100i miliyaar ci sunuy koppar lees jagleeloon naalu PRODAC bi. Xaalis boobu, dafa waroon a dem ci diirub 5i at. Bi ndawi, Ëttub cettantal bi amalee seen luññutu, gis nañ ay doxaliin yu safaanook yoon. Ndax, feeñal nañ ay rëq-rëq ci ni ñu doon saytoo koppar yi.

Dafa di nag, Maam Mbay Ñaŋ mi nekkoon, jëwriñu ndaw ñi jamono jooja, moo ci gën a fés.  Ndax dafa xaatimoon ag pas (contrat) ak lijjantig (entreprise) Israayel gii di Green 2000. Muy pas gu séddalikoo ci ñaari pàcc. Bu njëkk bi tollu ci 29i miliyaar yu teg 600i miliyoŋ. Ñaareel bi war a doon 59i miliyaar yu teg 500i miliyoŋ. Pas googu nag, ñu bari dañu koo ŋàññ ndax lënt-lënt yi ci nekk.

Bees sukkandikoo ci caabalu Ëttub cettantal bi génne, anam yi ñu joxee Green 2000 naalu PRODAC bi dafa desee. Ndaxte, ci aw waxtaan kepp lañu sukkandiku, daldi jox Green 2000 naal bi. Mooy li tubaab di wax « Entente directe » la amee. Te loolu, yoon daf ko tere. Rax-ci-dolli, Green 2000 dafa yéex a jébbale liggéey yi jëmoon ci yenn jumtuwaay (infrastructures) yi. Te sax, njortees na ne liggéey bi baaxul ni mu war a baaxee.

Ci biir caabal gi, fésal nañu ci ne, ñi doon saytu naal bi, dañu daan jënd ay mbir ci njëg yu jéggi dayo, ëpp lool njëg yi ñu war a jar ci yoon. Te nag, duñ ko amal lay te du a ay firnde. Loolu doyatul, ñu jël ay buuñaa yu duun jagleel ko ñenn ñu bokkoon ci banqaas yiy saytu ja yi (commissions des marchés). Mu nekk ay xeeti payoor yoo xam ne amuñuy cëslaay te worook ak li yoon santaane. Caabal gi biral yeneen i njaaxum ak i tóoxidoona yoy, dañuy dëggal Usmaan Sonko.

Cig pàttali, Usmaan Sonko dafa waxoon ni am na ag caabal gu tuumaal Maam Mbay Ñaŋ ci ni mu yoree woon PRODAC bi. Ba mu waxee loolu, Maam Mbay Ñaŋ kalaameji ko yoon, ñu daan Usmaan Sonko. Dafa di sax, looloo tere Usmaan Sonko bokk ci wotey 2024 yi. Tey nag, Usmaan Sonko am na dëgg ci kow Maam Mbay Ñaŋ.

Mooy li wolof di wax rekk, fen du bijjaaw.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj