Àllarbay démb jee nekkoon ñeenteelu bésu kuppeg àddina siy ame Qataar. Ñeenti joŋante waroon ci am : Marog – Kurwaasii, Almaañ – Sàppõ, Espaañ – Kostaa Rikaa ak Belsig – Kanadaa. Ginnaaw mbetteel bi ñu amati ci li Sàppõ duma Almaañ, wulli yi Espaañ wulli Kostaa Rikaa la ñépp di waxtaane.
Kippu F : Marog ak Kurwaasii témboo nañ
Marog a nekkoon ñetteelu réewum Afrig mi waroon dugg ci joŋante bi, waroon a laaleek Kurwaasi gu Lukaa Modiris. Kurwaasi lees njortoon ne mooy daan. Waaye, ndam demul, ndam dikkul. Ci ñaareelu joŋanteb kippu F gi, Belsig moo daan Kanadaa 1 bii ci dara.
Kippu E : Sàppõ bittarñi na Almaañ, Espaañ toroxal Kostaa Rikaa
Beneen ponkal bu daanooti, ginnaaw Arsàntin. Ginnaaw coow lu réy liñ sabab ñeel àqi góor-jigéen ñi, saa-almaañ yi ag mbetteel lañ ame ci àllarba ji. Nde, ñoom, bokk nañ ci réew yi gën a xër ci wàllu ngóor-jigéen, njigéen-njigéen ak yu ni mel. Jooy nañ fépp li Qataar tere bépp xeetu jëf, doxalin walla wirgo yuy biral ag ngóor-jigéen walla njigéen-njigéen, añs. Moo tax, laata ñuy door mats bi, 11i kuppekati saa-almaañ yépp a tafoon seen i gémmiñ ngir naqarlu tere yooyu. Waaye de, bi mats bii jeexee tamit, dañu tafaat seen i gémmiñ. Ndaxte, dañ leen a noq, ñoom ñiy jéem a ga nit ñi ci seen i aada, ànd ceek tubaab yi. Sàppõ a leen dóor 2i bii ci benn. Moone, Almaañ a njëkk a dugal laata Sàppone di leen bittarñi. Daanaka, jullit ñépp a bég ci ndamul Sàppõ li. Nga gis ñu naan, ikibu góor-jigéen ñàkk na. Ci ñaareelu joŋante bi, mënees na wax ne Espaañ dafa noggatu Kostaa Rikaa, dóor ko ba sëlam ko.
Ndawi Luwis Enrike yi amuñu benn xeetu yërmande ci waa Kostaa Rikaa. 7i yoon la Espaañ lakk caax yi te Kostaa Rikaa dugalul sax benn bii. Muy ndam lu réy ci Espaañ, waaye di toroxal bu réy a réy ci Kostaa Rikaa.
Ngirtey bés bi
Marog |
0 |
0 |
Kurwaasi |
Almaañ |
1 |
2 |
Sàppõ |
Espaañ |
7 |
0 |
Kostaa Rikaa |
Belsig |
1 |
0 |
Kanadaa |
Joŋantey ëllëg, alxames 24 nowàmbar 2022
Siwis |
– Kamerun |
Uruguway |
– Koreg suuf |
Portigaal |
– Gana |
Beresil |
– Serbi |