Bool, marmet, kubéeri cin, kuddu cinwaar, kuddu luus, mbiib yi, korne yi… lépp a riir démb. Bi 20i waxtu tegalee 30i simili, lépp luy jumtukaay buy raŋ-raŋi, di keŋ-keŋi ak a jur coow, ñoñi Pastef yi yëngal nañu leen. Jëfe nañ bu baax a baax ndigalu Usmaan Sonko li.
Ci gaawug démb gi la waa Pastef nammoon a amal seen ndajem tabb, fa estaad Aamadu Bari bu Géejawaay, ngir tànn Usmaan Sonko, def ko seen lawax ci wotey 2024 yi. Waaye, gornooru Ndakaaru ak perefeb Géejawaay dañ leen ko aaye. Ngir naqarlu aaye bob, nee ñu, dafa safaanoo ak yoon, njiitul Pastef li dafa woote woon col gu xonq ak tëggub bool.
Ci suba gi, ñii dañ sol ay yére yu xonq, ñee takk i sagar yu xonq. Mag, ndaw, góor, jigéen, ñépp a ci ràññeeku. Amaloon nañ sax ay doxantu ngir jaayaale jaray këwsu yees duppee ci nasaraan « bracelets de la liberté » walla « bracelets patriotiques ». Jot nañ cee jaay lu baree bari sax. Nde, fa Kër-Masaar rekk, jaay nañ fa 5 000iy jara. Waaye, xew-xew bu mag bees doon xaraandi, mooy tëggub bool bi waroon a am ci guddi gi.
Ndakaaru yépp a riir démb. Foo tollu di dégg i raŋ-raŋ ak i keŋ-keŋ. Ndab yiy dalante, mbiib yiy jolli… Coow li ne kurr. Oto yeek moto yi rax ci seen i korne. Ndaw ñiy woy ak a fecc, di joobe Usmaan Sonko. Moom ci boppam, meeru Sigicoor mi ñu ndar-kepp fa Site Kër-Góor-Gi, génnoon na ak njabootam, ak lenn ciy dëkkandoom, fëgg ay kubeeri cinam. Mu ngi soloon lu xonq ci kow ba ci suuf. Mbaxanaam ba sax, dafa xonq. Usmaan Sonko nee :
« Yoon wii nu tànn, pexe la ngir xeexal sunuy àq te dunu yee fitna. Danu ciy artuwaale Maki Sàll bu baax a baax. Senegaal dafa soxla jàmm, dal, noflaay ak péexte. »
Wooteem bi nag, fépp ci Ndakaaru lañ ko jëfe. Yenn béréb yi, fa Sigicoor ak Mbàkke tamit, tëgg nañ seen i ndab ba mu riir. Bu dee yeneen diiwaan yi ak goxi réew mi, mbir ma demewu woon fa noonu yépp.