Rawale nañ Usmaan Sonko ca “réanimation” ba.

Yeneen i xët

Aji bind ji

Rawale nañ Usmaan Sonko ca “réanimation” ba. Jotna Média moo siiwal xibaar bi. Ci seen xëtu Facebook lañ bind, wax ne :

” Noo ngi xamal waa réew meek àddina sépp ne rawale nañ Persidã Usmaan Sonko ca “réanimation” bu loppitaanu Proncipal bu Ndakaaru ginnaaw bi ko ab jagadi dikkalee démb ci ngoon.

Noo ngi fàttali ne Persidã Usmaan Sonko, ci bañ bi mu nekk nekk di bañ tooñ ak xoqatal bi ñu koy xoqatal, mi ngi tollu tey, alxames 17 ut 2023, ci 19eelu fanu xiifal fi ko Nguurug jaay-doole gu Maki Sàll giy xiifal-loo.

Lépp lu dal Usmaan Sonko rekk, Njiitu réew mi la, Maki Sàll, jëwriñ ji mu dénk Yoon, jëwriñ ji mu dénk biir réew mi ak ñépp ñi dugal seen i loxo ci gëtën bu ñaaw bi ñu koy gëtën ba njiitul kujje gi nar cee ñàkk bakkanam.

Noo ngi woo militã yépp ak soppe yi ak askanu Senegaal wépp ñu takku taxaw ngir ñu bàyyi Persidã Usmaan Sonko ni mu gën a gaawe ak ñi ñu jàpp ci kaso yi ci sababu pólitig. 

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj