RAWALEES NA USMAAN SONKO CA FAJUWAAY BA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Làngug Pastef les Patriotes génne na ab yégle di ci xamle ne, rawalees na Usmaan Sonko ca fajuwaay ba. Nee ñu, njiitul Pastef li dafa feebar ba sonn lool.

Ñoom, waa Pastef, ñoo ngiy artu di xamle ne, laata ñuy jàpp seen njiit li, keroog 31eelu fan ci sulet 2023, dara jotu ko woon, dara mettiwu ko woon, maanaam daa wéroon péŋŋ. Moo leen tax a wax ne, lépp lu ko dal rekk, Maki Sàll ak Nguuram ñooy Njaag. Ñoo ngi dégloondi fajkat yiy toppatoo Usmaan Sonko ; lépp lu ci rot ciy xibaar, dinañ ko siiwal.

Cig pàttali, tey mooy juróom-ñetteelu fan bi Usmaan Sonko tàmbalee xiifalam gi ngir, ciy waxam, xeex ak a bañ xoqatal ak singali bi ko Maki Sàll ak Nguur gi singali.

Wëliis Usmaan Sonko, rawalees na Paap Aale Ñaŋ, Anibaal Jiim ak Séex Baara Njaay tamit ca fajuwaay ba. Nde, ñoom itam dañ nekk di xiifal ; looloo leen jàpp ba faf daaneel leen.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj