Musaa Aysatu Jóob
Ci benn bataaxal bu mu siiwal, Jean-Pierre Kutwa, njiitu katoligi Kodiwaar yi, mi ngi joxe gis-gisam ci ñetteelu moome bi Alasaan Daramaan Watara fas-yéenee laaj askanu réewam. Mi ngi ciy xamle ni lu mën a ñàkk la te yit baaxul ci réew mi ndax coow ak xëccoo rekk lay jur te ku moytuwul sax ay bakkan yu bare rot ci.