RËNG-RËNG CA TURKI AK SIRI : 4 890iy NIT DEEWAGUM NAÑU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Suuf si yëngooti na, àddina jooyati. Nde, ay rëng-rëng yu mettee metti ñoo dal ci kow réewi Siri ak Turki ba 4 890iy nit ñàkke ci seen i bakkan, lu ëpp 16 793 ci lees limagum ciy nit ñoo ci amey gaañu-gaañu. Ag rëng-rëng gu dayob 7.8 moo njëkk a màbb suuf seek la woon ca kowam lépp, yeneen i rëng-rëng toftalu ca, daldi koy awu, gënatee yokk jéyya bi. Jamono jii, wallukat yaa ngay def seen kemtalaayu kàttan ngir dimbali ñi nekk ci biir genti taax yi daanu. Àddina sépp nag, booloo nañu, yónnee fay wallukat, rawatina ca Turki, ngir fexe ba muccal ñi desandi ca màbbit ya.

Maaradeytaali ! Suuf see yëngu ca ñaari réew, Siri ak Turki, daldi màbbloo ay taax yu baree bari, mëdd ay tabax, ay kër ak limub nit bu jéggi dayo. Ag rëng-rëng gu tollu ci dayob 7.8 moo njëkk a xar suuf si ci ñaari réew yees tudd ci kow. Ci guddig dibéer ji, jàpp altine la ame, ba njël di jubsi. Ca penku suufu Turki la yëngoo, méngoo ak bëj-gànnaaru Siri. Ñu ni déet-a-waay, geneen rëng-rëngug 7.5 ci dayo awu ko ci yoor-yooru altine ji ; muy lu doy waar te metti lool. Tey jii rekk, ci fajar ji, amaat na geneen rëng-rëng gu yëngooti ca diggu réewumTurki. Rëng-rëng gu mujj googoo ngi tollu ci dayob 5,6. Lu ni mel nag, bariwul di am. Looloo tax mu yéem te bett lool boroom xam-xam yi seen i xel màcc ci wàll wi. Fi mu nekk nii, Nguuri Siri gaak gu Turki gi, ñoo ngiy sàkku ndimbal. Àddina si daanaka wuyu na leen.

Njiitu réewum Turki, Recep Tayyip Erdogan, dafa dekkerete 7i fani dëj ca réew ma. Nde, moom Njiitu réew ma, dafa jàpp ne jéyya joojoo di « jéyya ju gën a bon [ju réewum Turki mës a jànkonteel] atum 1939 ba tey. » Réew ya dend ak Turki ak Siri, di seen i dëkkandoo, ñoo fa njëkk a yónniy ndaw. Ca saa sa lañ fa dem. Dafa di, ñoom sax, xaw nañoo yëgaale rëng-rëng yi ndaxte ñoo dend. Aseerbayjã dafa jox Turki xaa-xaat 370i wallukat. Israayel ak Palestin tamit joxe nañ seen ndimbal. Waaye nag, diggante Israayel ak Siri dafa xajam, moo tax wóorul Israayel yónni fay ndawam. Sàppõ ak Irã, ci càkkuteefu Erdogan, nee ñu dinañ fo yónniy ndaw, diy wallukat.

Emmanuel Macron, Njiitu réewum Farãs yónnee na fa 139i wallukat, jàppalee ko naataangom ba. Bennoog Tugal (Union Européenne), moom itam, dajale nay wallukat, yabal leen fa. Espaañ ak Itali tamit, yabal nañuy ndawi wallukat ca Malatya, fa ñuy dalalee dimbalikat yiy jàppalesi Turki ak Siri.

Almaañ, Poloñ, Geres, Àngalteer ak i dendandoom, Siwis ak Suwed, réew yii yépp, biral nañ seen yéene ngir dimbali Siri ak Turki. Dafa di, Ikren ak Riisi ñi nekk cib xare sax, nee ñu dañuy joxe seen ndimbal. Bu dee Ikren daf ne rekk mën def li war ngir jàppalee ko ñaari réew ya, wànte 300i sóobarey Riisi ya nekk Siri, ñoom, tàmbale nañoo dimbali waa réew ma, di dindi ak a roñ màbbit ya. Vladmir Poutine ne, dina fa yónnee ay wallukat.

Ginnaaw réewi Tugal yi, Etaasini ak Kanadaa tamit, kenn demul ñu des. Bu dee Mbotaayu Xeet yi (ONU), ay ndawam ñoo nga fa di dimbali nit ña.

Kembar yépp, daanaka, ñoo ngiy dimbali Siri ak Turki walla ñu ciy fésal seen i yéene. Afrig daal lees ci déggagul. Seet nanu ba sonn, waaye lu dul ay kàdduy njaal, niki yu Njiitu réewum Senegaal gii di Maki Sàll, kenn waxu ci ne dina dimbali Turki walla Siri. Loolu nag, gàcce la. Jarul sore.

EJO ak Lu defu waxu ñu ngiy jaale askani Siri ak Turki, di leen mastawu te di bokk ak ñoom naqar week tiis wi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj