820i nit ñoo ñàkkagum seen i bakkan ci rëng-rëng bi yëngal suufus Marog si. Jëwriñu biir réew ma moo joxe lim bi. Nee ñu, 672i nit jële nañ ciy gaañu-gaañu. Balaa bët di set, 632i nit lees ci tàgge woon ak 329 yu ci ame ay gaañu-gaañu.
Ci guddig àjjumay démb ji, 8i fan ci sàttumbaar, ci boori 23i waxtu yu tegal 10i simili, la suuf sa yëngu ba xar fa Marog. Ca wetu Marakes la jéyya ji ame. Bees sukkandikoo ci CNRST (Centre marocain pour la recherche scientifique et technique) bu Marog, dayob rëng-rëng ba ngi tollu ci 7. Guléet ab rëng-rëng bu ni tollu di gaar réewum Marog. CNRST xamleet na ne, xolu rëng-rëng baa ngi féete fa diiwaanu Al-Haouz, ca bëj-gànnaaru Marakes.
Dafa di, sax, ci biir 820i nit ni ci dee 394i Al-Haouz lañ fekk baax. Fa Taroudant tamit, boo wàccee tuuti ci bëj-saalum bi, 271i nit la fa rëng-rëng bi rey.
Wëliis bakkan yi ci jot a rot yépp ak ñi ci jëley gaañu-gaañu, nemmeeku nañ fa ay yàqute yu baree bare. Dëkk yu bare la rëng-rëng bi laal. Ñu gis i nataal yoy, dañuy biral ay taax ak kër yu daanu. Ay jàkka ak i jumaa yu màbb. Am na sax ab sooroor bu daanu fa béréb bu siiw boobu ñu naan Jemaa ek-Fna, ca diggu Marakes. Foofa, ñaar ñoo ca jële ay gaañu-gaañu.
Askan waa ngi jàq, tiit, jaaxle. Xamuñu fu ñuy dem. Ñu bare ñoo génn seen kër yi, toog ci mbedd yeek wetu tali yi, fees fa dell. Dañuy ragal beneen rëng-rëng feelu bu démb bi. Moo tax, ñu bari ci mbedd yi lañ fanaan.