REYATI NAÑ ÑETTI NIT FA KÉEDUGU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ab xeex bu metti moo amoon diggante takk-der yi ak askan way yeewoo fa Xosantoo ak Mama Xono (diwaanu Kéedugu). Limees na ci ñetti nit yu ci ñàkke seen i bakkan ak fukk ak ñeent yu ci amey gaañu-gaañu. 

Démb ci altine ji la jàmmaarloo bi amoon. Ndaw ñaa doon ñaxtu ak a naqarlu ndogal li perefe (calaw) bu Sarayaa bi jël. Ndogal loolu dafa aju ci ndaw yañ fa waroon a jël ñu liggéey te jànguñu. 

Ci yoor-yooru altine ji la takk-der yi rey ñaari nit fa Xosantoo. Ci guddi gi sax, tàgge nañu keneen ku ci dee. Fukk ak ñeenti nit ñoo ci jëley gaañu-gaañu, bees sukkandikoo ci Abdul Kamara mi jiite fajuwaayu ba fa nekk. Daf ne :

“Am na 14i nit ñu ci amey gaañu-gaañu yu mettee metti (…) rawalees na ñenn ñi fa raglu diwaan bees duppee Amaat Dãsoxo, Kéedugu. Am na ñeneen ñu fajoo ca “service médical” bu Endeavour Mining bu Sabadolaa.”

Léegi, yamatuñu ci sàcc balluy mbindaare réew mi, waaye dañ leen di rey teg ci.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj