RTS : PAAP AALE ÑAŊ DAKKAL NA DÉGGOOY RAASIN TAALA YA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paab Aale Ñaŋ a ngi indiy coppite ca RTS. Ndogal lu yees lu mu mujjee jël, mooy dakkal xeeti déggoo yu ko Raasin Taala bàyyee woon.

LaataNjji Maki Sàll di daanu, Raasin Taala mi jiite woon RTS dafa torlu woon ay déggoo. Keroog, 29 màrs 2024 la leen xaatimoon. Waaye, Paap Aale Ñaŋ far na lépp.

Ab bataaxal la bind, démb, jagleel ko liggéeykati kër ga. Daf ci bind, xamal leen ne, payoor ya ñu jotoon ca weeri awril ak me de, ca déggoob 29 màrs bi lañu sukkandiku. Mu teg ci ne, bu ñu wéyalee déggoo boobule, kërug RTS dina jànkoonteel i jafe-jafey koppar yu tollu ci 1. 800. 000. 000 FCFA. Loolu doyul ; ndax limub 1. 350. 000. 000 FCFA dina gàllu ci ndoddu kër ga, ci at mii ñu nekk. 

Dafa di, déggoo yi Raasin Taala torlu woon, ci dekkareb 2024-837 bu 27 màrs 2024 la aju. Waaye, dekkare boobu, jàppandalul jamono jii. Te, amul lenn lees waajal luy dékku déggoo yi. Moo tax, moom Paap Aale Ñaŋ, mu dakkalandi déggoo yi. Ndaxte, ciy waxam, kër gi àttanu ko. 

Ci kow loolu, Paab Aale Ñaŋ xamle na ne, dale ko ci njeexitalu weeru suwe 2024, payoor yi dees na leen delloo fa ñu nekkoon. Ndogal loolu, mi ngi ko wéer ci  déggoob 25i màrs 2005. Jox na ndigal caytug kër ga ñu doxal ndogal li mu jël. Wànte, ñenn ci liggéeykati kër ga ànduñu ci.

Mbootaayu liggéeykati RTS yi dañu woote woin nañ am ndaje, tey ci talaata ji, 2i fani sulet 2024, foofa ca RTS, bu 15i waxtu jotee. Li ñu ko dugge mooy, bees sukkandikoo ci kàdduy Màmma Musaa Ñaŋ mi leen jiite, waxtaane ndogal yi njiitul RTS lu bees li, Paab Aale Ñaŋ jël. Moom, Màmma Musaa Ñaŋ, dafay ñaawlu payoor yi ñu wàññi, li ñu dàq ñenn ci ña fa amoon ay pasi liggéey, li ñu dakkal déggoo bi ñu amaloon keroog 29i mars 2024, li ñu wàññi ndàmpaay yi ba 100.000 FCFA ak dakkalug koppar ya ñu daa bokk séddoo (fonds communs).

Mu mel ni nag, jàppante dafa nar a am diggante Paap Aale Ñaŋ mi jiite RTS ak ñenn ça liggéeykat ya fay daan seen doole.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj