SAMA XALAAT ÑEEL “SOMMETS” YI AK SUNU NJIITI AFRIG YI (TAYIIRU SAAR)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci tekkib Paap Aali Jàllo

1. “Sommet France-Afrique” ngir wéyal nooteel geek mbéeféer gu bees gi. Te, ginnaaw bi ndaw ñi yeewoo, ñu dëpp wax ji, soppi ko “Afrique-France” (waaye ba tey Farãs lay amee). Saa-Afrig yi gëm seen bopp sol yérey cosaan ngir di jaay mbirum panafrikanism bi nga xam ne, tubaab bi xam na ne du mës a am, ay gént kese la.
2. “Sommet Russie-Afrique” ngir yelwaani bele te waxaalewaale ay ngànnaay yu néew doole te yomb, fekk ne Afrig mi am naaj ak i ndaw moo gën a jekku mbey mi bees ko méngalee ak Riisii.

3. “Sommet Chino-Afrique”, nga xam ne Siin amul dara ci balluy mbindaare, waaye dafa am ndaw yu gànjaru yu boot yokkuteem. Duggeewu ko lu mooy jaay xam-xami xaralaam yi ngi xam ne, balluy njëkke yi fi nun, Afrig, la koy jëlsee.

4. “Sommet Arabe-Afrique” ngir def nu ay yelwaankat ak i tàllalkati loxo, sol ay Jàllaaba ak i Xulaatul’amra ngir bokk ci mbootaayu réew yu mag yi, di diirante mbagg ak yeneen yi. Te, amul dara lees ciy weccante bu dul ay sarax ak li naar yiy dugal seen xaalis ngir liggéey.

Ci tënk, réew yii yépp ay nasiyonaalist lañu (ñu jiital seen réew). Te dañu jàppee Afrig niki géew bi ñuy xeexee, di xoolee sunu njiiti réew yi nikiy yelwaankat. Duggeewuñu ko lu mooy wone seen doole.
Léegi, ci biir réew yii ma jot a lim, waxleen ma man lañ ci mën a dem te ameesul wiisaa ? Man réew lañ ci mën a dëkk te ameesul këyitug dëkk (carte de séjour) ? Man réew lañ ci mën a liggéeyee te ameesul këyitug liggéey ?

Nanu bàyyi naaféq bu réy bi nu nekkee te samp waxtaanuw xalaatiin wuy suqali am réew.

Maa ngi woo ci wile waxtaan Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Fay, ak elimaanu jëwriñ yi, Usmaan Sonko, kilifay pólitig yi nekk ci géewu pólitigu Senegaal gépp, di ci woo saabalukaay yi, Saa-Senegaal yi safoo Yoon, njub ak kaaraange ñeel sunu réew mii bëgg ci sunuy xol.

Leeral : Booleewuma ci way-moome yoy, dañu ame jàngoroy naaféq ju metti te, dara ñoru leen lu dul alal. Jërëjëf

Tayiiru Saar
Njiitul “Mouvement Nationaliste Sénégalais”

Bokk ci lëkkatoo “Diomaye Président”

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj