SÉMBUB ÀTTE BUY NEENAL I DAAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yéenekaay Le Quotidien moo siiwal xibaar bu bette, tey ci yoor-yoor bi. Yéenekaay bi dafa bind ne, Njiitu réew mi, Maki Sàll, dafa bëgg a jàllale fa Ngomblaan ga sémbub àtte buy neenal lépp li xewoon diggante weeru màrs 2021 jàpp suwe 2023. Maanaam, képp ku ñu jotoon a daan, tëj la kaso ci sababu xew-xew yi amoon ci diir boobu, dañuy neenal daan yi walla tuuma yi (bu dee àtteeguñ la). Bu ko defee, nga daldi génn kaso bi.

Njiitu réew mi, Maki Sàll, mi ngi seqiy jéego ngir jëmmal waxtaan wi muy woote. Mi ngi togg ci suuf ngir yakk lol, ñépp dinañ ko nangoo lekk. Nde, dafa namm a wotelu sémbub àtte bob, day far li fi xewoon lépp, diggante màrs 2021 ak suwe 2023.

Bees sukkandikoo ci Le Quotidien mi biral xibaar bile, Njiitu réew mi dafa jox ndigal ngornamaŋ bi, waxleen nu defaral ko sémbub àtte buy neenal xew-xew walla yëngu-yëngu yi jot a gaar réewum Senegaal ci diirub ñaari at, dale ko màrs 2021 jàpp suwe 2023. Bu ko defee, ñi ñu jàppoon ñépp ci diir boobu mën a génn, dellu ci seen i njaboot.

Ci lees jot ciy xibaar, ci àllarba jii nu dëgmal la Ndajem jëwriñ mi war a tàbbal sémb wi. Bu loolu weesoo, dépite yi ñoo koy wote fa Ngomblaan ga. Ginnaaw gi, bu sottee, ñu bari dinañ gisaat jant wi, noyyiwaat ngelawul péexte. Waaye nag, xel yépp ci Usmaan Sonko lañu daj.

Dafa di, ñaari weer yi nekk ci cati àppug sémb wi yépp (màrs 2021-suwe 2023), la ca xewoon, njiitul Pastef ga woon la ñeel. Ñaari yoon yépp, dañoo jàppoon Usmaan Sonko, réew mi tàbbi ci fitna ju réy ba ay bakkan yu baree bari rot ci. Ci diir boobeet, jàpp nañ ci lu ëpp 1 000iy nit. Loolu di wone dayob Usmaan Sonko ci géewu pólitig bi.

Waxtaan wi Njiitu réew mi woote, ñu bari dañ ko wax ne mënul a àntu fileek Usmaan Sonko bokku ci. Mën na am looloo sabab ndogalam lii jëm ci bàyyi ko, moom meeru Sigicoor bi ak i militaŋam yu bari yi ñu nëbb jant wi boobaak léegi.

Usmaan Sonko nag, dafa ne woon, moom, kenn du ko teg ab fetel ci kaabaab ba noppi di ko tàllal loxo. Maanaam, du nangu mukk ñu koy xoqatal ba noppi di ko woo ciw waxtaan. Looloo taxoon bokkul woon ci waxtaan yii weesu. Nu xool ba xam, wii yoon, bu ñu ko bàyyee, bàyyi ay ñoñam, ndax dina ko tax nangoo toog ak Maki Sàll.

Cig pàttali, keroog bi Njiitu réew mi xamlee ni dafa neenal dekkare bu doon amal wotey 25 féewiryee 2024 yi, dafa xibaaroon ni day woote waxtaan wu yaatu ngir ñu pexe miy génne réew mi ci guuta bim nekk. Ñu bari nag ci kujje gi, rawatina waa Pastef ga woon, dau waxoon ne duñ bokk ci waxtaan woowu. Ndaxte, ci seen i wax, Maki Sàll dafa jalgati sàrti Ndeyu àtte réew mi, jaay doole, randal wote yi. Ñoom ànduñu ci loolu te, keroog bésub 2 awril 2024, dootul nekk Njiitu réew mi. Rax-ci-dolli, nee ñu Maki Sàll amul kàddu, maanaam du kuy sàmm kàddoom.

Dees na xam, keroog bu sémb wi jàllee ba Usmaan Sonko ak i ñoñam génn, luy doon taxawaay yi.

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj