Ëllëg, ci altine ji 16 sulet 2023, lañ war a wote ca Ngomblaan ga ab sémbub àtte bob, day jëmmal lees waxtaane ca péncoo ma Njiitu réew ma woote woon. Sémb bi nag, dafa nar a indi ay coppite ci ndeyu àtte ji ak ci càrtug wote gi. Bu dee càrtug wote gees war a soppi, lees ko dugge mooy fexe ba Xalifa Sàll ak Kariim Wàdd mën a bokk ci wotey 2024 yi. Loolu, umpul woon kenn. Waaye, coppite giñ bëgg a indi ci dogub 87 bu ndeyu àtte ji moo tiital ñu bari. Ndax, day may Njiitu réew mi sañ-sañu tas Ngomblaan gi saa bu ko soobee. Ñu bari jàpp ne, loolu, day nasaxal demokaraasi, di neenal baatu askan wiy fal ay dépiteem.
SÉEX BÀMBA JÉEY, BENNOO JUBAL
« Dogub 87 bi ñu bëgg a soppi ngir may Njiitu réew mi sañ-sañu tas Ngomblaan gi saa bu ko soobee, ag deeltu-ginnaaw gu doy waar la ci demokaraasi. Coppite googu, du lees waxtaane ca péncoom pólitig ma Njiitu réew mi woote woon, déggoowuñ ci. Loolu, dafay nasaxal Ngomblaan gi, dooleel baatu doxal bi ci kowam. Daanaka, Ngomblaan gi day dee. Ndax, Njiitu réew mi dina mën, saa bu amulee limu dépite bim soxla, neenal baatu askan wi fal ay dépiteem. Maanaam, dina mën a xaatim dekkare ngir tas Ngomblaan gi. Bu may ñawatle, dama naan at mu nekk danuy amal ay wotey dépite. »
CEERNO ALASAAN SÀLL, RÉEWUM NGOR
« Sémbub àtte biy soppi ndeyu àtte ji day tayle Ngomblaan gi xam ne, taxu ko am doole noonu yépp. Dañuy jébbal Ngomblaan gi Njiitum réew mu bari doole. Maki Sàll dafa bàyyi ñetteelu moome gi, waaye bàyyeegul Nguur gi.
Dafa mel ni, moom, daf noo bëgg a tànnal ki koy wuutu te tànnal ko ag Ngomblaan gu muy taxawal ciy pexeem.
Man, dépite, duma mës a wote ab àtte buy nasaxal sunu demokaraasi. »
MUHAMMADU NGUUDA MBUUB, JÀNGALEKATU YOON CA UCAD
« Mbokki réew mi,
Sémbub àtte biy joyyanti dogub 87 bu ndeyu àtte ji day suufeel wote yi ak baatu askan wi.
Àtte bii day yokk dooley Njiitu réew moo xam ne, dooleem dafa jéggi dayo ba pare. Te, daanaka day xañ Ngomblaan gi sañ-sañam yépp.
Ngir sàmm deru Bokkeef gi ak yemoog campeef yi, dépite yi dañ war a gàntal àtte bile nga xam ne, day far ab jéegob demokaraasi bi ñ seqi woon 22i at ci ginnaaw.
Lii war na doy ngir xupp nu. »
ALJUMA SOW, PASTEF
« Sémbiy àtte yi ñuy yóbbu ca Ngomblaan ga ñoo yées « ticket présidentiel » bu suwe 2011 ba ci ne, sémbi àtte yooyu dañuy rey bépp xeetu péexte. Dañ leen a war a xeex… »