SÉMBUW KOPPEY MBAY ÑEEL NJABOOTU DAARA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Jëwriñu Mbay mi, Dund gu doy gi ak Càmm gi, Sëñ Mabuuba Jaañ, yégle na xibbar buy neex njabootu daara. Nde, dafa xamle ne ñu ngi taxawal aw sémbuw koppe ci fànnu mbay mi ñeel daara yi. Mënees na yaatal naal woowu ci ñi jànge ci làkkuw araab ba am seen i lijaasa te bëgg a sóobu ci mbay mi.

Sémb woowii ñu namm a jëmmal,  siiwalees na ko ca njeexitalu ndaje ma amoon diggante njiitul Mbiri diine yi ak Xëyum ñi am lijaasa ci làkkuw araab, Jiim Daraame, ak njëwriñu Mbay mi, Dund gu doy gi ak Càmm gi. Njëwriñ gi dafa biral ab yégle, xamle ci ne, dañu bëgg a jëmmal digaale bi, jaare ko ci xaatim ag dëppoo ci ayu-bés yees dëgmal. Digaale boobu, dees na ci boole njëwriñi Njàng meek njàngale mi, Njàng mu kawe mi ak Tàggatug liggéeykat yi.

Jéego bi njëkk ci liggéey bi nag, mooy saytu ba xam ñi am lijaasa ci làkku araab, xool ba xam fu ñu mëne ba noppi daldi dajale ñi bëgg a liggéey ci mbay mi. Bees sukkandikoo ci kàdduy jëwriñ ji, Mabuuba Jaañ, diiwaan bu nekk, ñi gën a dogu te fobu ngir liggéey lañuy wër, tàmbali liggéey bi ak ñoom.

Ba tay, ci kàdduy jëwriñ ji, képp kees kopparal, dangay fay. Ndaxte, ci mu wax, ñàkk a fay bi du pexe. Fàww rekk nit ki nangoo fay, bu ko defee dina liggéey bu baax. Bu ko defee, sémbi mbay mi ak càmm gi dinañu mën a yemb. Rax-ci-dolli, ñaax na boroomi lijaasa yi ñu bañ a yaras, bañ a xeeb seen bopp te duggu ci mbayum banaana, ceeb, mboq ak tamit rattum soow mi, mbayum meññent yi ak payteef yi.

Càmm gi dina gunge njabootu daara, tàggat leen, lebal leen i koppar te xàllal leen yoon wi ngir ñépp mën cee gis seen bopp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj