SÉMBUW NDEFARUG DAAMAR FI SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal mën na am ndefarug boppam gog, dinay liggéey ay daamar fi réew mi. Bu ko defee, dootul jéggaaniy daamar walla jumtukaay yi ciy dem. Móodu Mustafaa, di inseñëer fa BMW, moo ko xamle. Sunu naataangoy Source A la séqaloon, jamono yee, aw waxtaan wow, ca la biralee naalam boobile.

Ci xayma, ñaar-fukki tamñaret (25i miliyaar), ci sunuy koppar, la Móodu Mustafaa soxla ngir samp fi réew mi ag ndefar guy liggéey ay daamar (oto). Moom, inseñëer bi, BMW lay liggéeyal ba nëgëni. BMW nag, ndefarug daamar la boo xam ne, Saa-Almaañ yaa ko moom ; mu di juróom-ñaareelu ndefarug daamar gu ëpp lu muy jaay ay oto ci àddina si. Móodu Mustafaa, doomu Senegaal ji, mi ngi yëngu ci li ñeel xaralaan gi (technologie) ca BMW Bayern Munich bu Almaañ. Li mu nisër, bees ko kopparalee, mooy samp fi Senegaal ag ndefaru daamar. dafa wax ne :

“Sama sémb waa ngi aju ci samp ag ndefaru daamar gu Senegaal moomal boppam. Ndefar googu, mooy xalaat ni daamar yi war a bindoo, moo leen di tëgg, defar jumtukaay yi ciy dem yépp, taqale leen tamit. Bu daamar yi noppee, moo leen di jaay itam.”

Bu ñu demoon ba jëmmal sémb wu ni mel, dina bokk ci liy suqali koom-koomug Senegaal. Ndaxte, am réew mënut a naat fileek amul i ndefar ci fànn yu bari, rawatina ci wàlli ndund gi, jokkalante gi, laf gi ak dem beek dikk bi. Bees amee ay ndefar, dinañ mën a sopparñi balluy njëkke (matières premières) yiy meññee ak a génnee ci réew mi. Te sax, bu boobaa, ñu bari dinañ am liggéey, ñàkkug xëy wàññeeku fi réew mi. Ku am xëy, di fayeeku weer wu set, doo ndóol. Looloo tax Móodu Mustafaa wax neeti, “…tabaxug daamar day wàññi ndóol cim réew.”

Dafa di, am réew, buy defar li muy aajowoo, day tax mu moom boppam. Te, ci wàllu daamar ak li ciy dem, Senegaal day jéggaani li mu soxla yépp. Lenn daal lañu fiy def, mooy boole, taqale ak a defaraat ay oto yu yàqu. Ci gis-gisu inseñëer bi, loolu dafa war a dakk. 

“Senegaal dafa war a weesu mboole, taqale ak defaraat ay daamar yu jóge feneen.”

Moom, Móodu Mustafaa, boroom  Samba et BIMA ENGENEERING, li mu bëgg mooy defar ay daamar Senegaal ci lu bari, mu duppee leen “Voiture Populaire Sénégalaise” VPS.

“VPS dina doon lu xéewale ñeel ñi bëgg a jënd daamar bu bees te néewle xaalis. Rax-ci-dolli, dinañu mën a defar lim bu takkoo takku ci ay A.M.A (Afrique mon Afrique) yoo xam ne, lépp Afrig lañ ko defaree, ànd ak motorisaasiyoŋ bu xaralag ñaari xol Jesel/Esãs ak elektoromotëer/Soleer.”

Li ci des mooy, bind, tëral ciy këyit, jébbal ko njiiti réew mi, bu dee defaguñ ko. Ñi mel ni Móodu Mustafaa nag, di boroomi xam-xam yu xarañ lool te di liggéeyal ay doxandéem, bari nañ. Te, xaaruñu dara lu moy kilifay réew mi gunge leen ci seen i naal ngir ñu dugal seen loxo ci liy suqali réew mi te di ko jëmale kanam. 

Am na yit ñoo xam ne, ñu ngi fi réew mi, bëgg li ñuy def, aay ci lool sax. Néew doole rekk a leen teree dem. Ku leen buuxoon, ñu dem, yóbbaale ñu bari. Jëlal mbay mi, càmm gi, napp gi, njéemantu gi, añs. Foo dem, dinga fa fekk ay ndaw yu sawar te xam li ñuy def, di xaar ku leen jàppale. Dafa di, réew, ay doomam ñoo koy tabax.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj