Barkaatu-démb ca ngoon, yemook dibéer 6i fani awril 2025, Njiitu réew mi jiite woon na jotaayu kaajar ak ubbiteg lees dippee ci nasaraan « Caravane nationale SPACEBUS 2025 », maanaam « Njëggum SPACEBUS 2025 ñeel réew mépp ». Fa ëttub « Grand Théâtre » Duudu Njaay Kumba Róos lees doon amalee xew ma.
Ca atum 2015 lañu sumboon sémb wile. Ren jii lañu ko fas yéene tollanti. Dees na ko amal diggante 6eelu fanu awril jàpp 13eelu fanu me 2025. Njëgg mi nag, dees na ko tëgg ci wëppa wii di : « Jawwu ji, jumtukaayu yokkute gu sax ». Naka noonu, ci diirub 37i fan, njëgg mi dina wër réew mépp ba mu daj. Waaye nag, duñu yam rekk ci wër réew mi. Nde, am nay naal yu solowu yu ñu war a doxal fépp fu ñu jaar.
Dafa bokk ci jubluwaayi njiit yi, xamal askan wi lu njariñu jawwu ji, ban xam-xam lees ci mën a jukke, naka lees mënee jariñoo xeetu xam-xam boobii ngir suqali réew mi ci fànn yu bari ak itam ngir wutal ndaw ñi xëy. Moo tax, fépp fu njëgg mi taxaw, dinañu fësal xam-xamu jawwu ji, amal i ndajey waxtaan ak i jotaayi liggéey ngir gaaral nit ñi njeexitali gëstub jawwu ji ci seen dund bés bu nekk.
Liggéey bi nag, kërug liggéey gu bees gii di Agence nationale pour les études spatiaux (ASES) moo féetewoo liggéey bi. Dafa di, ASES moo yor bépp liggéey bu aju ci gëstub jawwuu ji. Moom ak geneen kër gii di ASPA ñoo lëkkatoo di aajar ak a biral xamtug jawwu ji, di xirtalaate ak soññaate ci wàll woowii. ASES ak ASPA nag, dañu bokk aw naal wow, dippees na ko SENSPATIAL. Lu ñu ci nisër mooy xamal nit ñi nakala jawwu bindoo, la mu ëmb ak la mu làmboo ciy njariñ. Loolu, dafa dëppoo ak jubluwaayu sémbuw « SPACEBUS 2025 ».
Waxtaan yees namm a amal dinañu aju ci « naka lees di jëfandikoo jawwu ji ngir suqaliku gu sax dàkk ». Ren jii di ñaareel wi yoon ñu koy amal, dinañu ci dajale ñu bokk ci Càmm gi (jëwriñ yi, añs.) bi, ay digaale ci wàllu campeef yi, xarala ak kopparal. Nooneet, woowees na ci ay njàngaan yuy bawoo ciy daara yu bari. Bi muy ubbi ndajem barkaatu-démb ma, Njiitu réew mi waxoon na fa wax ju am solo.
Sëñ Basiiru Jomaay Jaxaar Fay dafa xamle solos jawwu ji ñeel suqaliku gu sax ak ci ëllëgu ndawi Senegaal. waaye, laata muy wax loolu, Njiitu réew mi dafa ndokkale bu baax Maram Kayre mi jiite « Agence sénégalaise d’Études spatiales (ASES) », ak képp kuy jàpp ci liggéey bi, rawatina Àmbaasadu Farãs ak koppeg Luksàmbuur. Rafetlu naat teewaayu kàngam yi bawoo Farãs, Koddiwaar, Benee, Eslowaki ak Togóo. Ndax, loolu, dafay mbir mom, ci gis-gisam, firnde la ci jàppoo ak yéene ji nu bokk am ci tabax ëllëgu Afrig gu yees.
Njiitu Réew mi fàttali na ne, dem ci jawwuu ji yamul rekk ci ab konket, waaye dafa war a indi ay saafara ci jafe-jafey jamono ji. « Xarala yi aju ci jawwuu ji man nañoo indi coppite yu wóor ci sunu mbeeraay yi », di li mu xamle, jaare ko ci lim seen taxawaay ci pàcc yu am solo yu mel ni fàkkug suuf si, mbay mi, napp gi, paj mi, kaaraange gi ba ci koomum géej gi.
Njiitu réew mi jot na fàttali yoon yi Senegaal jot a jaar ba mën a bokk ci réew yi am taxawaay ci wàllu jawwu ji, dale ko ca « Plan National de Géomatique » ca atum 1998 ba ni ñuy taxawalee ASES. Fàttali na tamit ndoortelu satelitu Senegaal bi ñu njëkk a sànni ca weeru ut 2024, muy jaloore juy màndargaal jéego bu am solo.
Ngir wéyal mbébet moomu, yëgle na sémb yu am solo : barab bu ñuy dajalee, di sofaale ak a amal ay test ci wàllu satelit (MAIT), ay béréb ngir dajale xibaar yiy bawoo ci satelit yi, benn béréb ngir gunge ndaw ñi ci wàllu gëstub jawwu ji, benn béréb bu ñuy saytoo jawwu ji fa Kéedugu, benn béréb bu ñuy xoolee mbooleem liy xew ci jawwu ji fa Xombol ak benn béréb ngir fésal lépp lu aju ci xam-xamu jawwu ji. Muy ay sémb yu mu jàpp ne dinañu tax ndaw ñi di mën a tàggatu, am ay xëy walla jéem a taxawal dara, lépp boole ko ak gën a xemmemloo Senegaal meññilukat yi.