SËÑ BAS, KU WAX FEEÑ

Yeneen i xët

Aji bind ji

Sa tànk mën na la dugal, sa làmmiñ génne la ; sa loxo dugal la, sa làmmiñ génne la ; sa bët dugal la, sa làmmiñ génne la. Waaye, bu la sa làmmiñ xasee dugal, tànk génnewu la ci, loxo du la setal. Te yit, loo réy réy bët, mënoo xullee xulli ba génn ci. Moo tax, aay làmmiñ, aay biir a ko gën. Sëriñ Basiiru Géy nag, moom, dafa mel ni xandul fa wolof daan fénce mbiri làmmiñ. Nde, doon na kon lem làmmiñam, toog ci ; walla mu waxe neneen keroog, alxames. Sëriñ Basiiru Géy, xanaa danga fàtte ni, ku wax feeñ ? Bataaxal bii, jaglees na la ko. Duggeesu ko lu mooy wàqante ak yow ñeel kàddu yi nga biral keroog ban gay janook taskati xibaar yi.

Sëñ Bas, xanaa yoo Kër Masaar baa la màtt ?

Maa laaj la Sëñ Bas. Loo xewle woon bay ñaq sa ñaq yu metti yooyu ? Sa ndel bépp a tooyoon xepp, nga baal ma nag. Xanaa kay doo nu wax ne danga wér kepp de… Waa lu la tiital ba nga doon wax di gag ak a nimse ? Lu xew ? Lu ko fi jar ? Mbaa du danga jàq ? Jaaxal nanu kat. Nee nga, ci sa ndoorteelu wax, dangay setal sa der. Ma lay wax ni, nga noppi woon sax a gënoon.Dafa di nag, bopp bu amee njëriñ, noppee ca sax. Kon Basiiru, lu tee woon nga ne tekk, wedamloo sa bopp ? Wax nga ba dugal sa bopp. Wax ngaa wax, di layam-layami ba tarxiis, daldi dëggal lees la doon njortal, taqalaale komandaŋ Mbeng. Te sax, yow, waroo wax. Nde, Yoon ci boppam moo la tere wax. Nga jalgati Yoon ñaari yoon.

Bi ci jiitu mooy ne, àttekat bi nga doon, maanaam sa mbubbum masistaraa, daf la tënk, tëjloo la sa gémmiñ. Rawatina nag, bi nga xamee ne yaa nekkoon Toppekat bi doon topp mbir mi. Nu ni déet-a-waay, ñu tabbati la, def la njiitalu OFNAC. Te, xam nga xéll ne, OFNAC, képp ku ko jiite, yoon daf la tere wax ci mbirum pólitig. Yow nag, nga jéggi tere yépp, wax lu tollu ci diirub ñaari waxtu yoy, dàggasanteek téesante kese nga ko jagleel. Xanaa xamoo ne, daw jiitu taxul a moom yoon ? Walla dafa am yoo bu la màtt ? Mbaa du bu Kër Masaar ba ?

Dof ba raw, moo gën muus ba dee

Sëriñ Basiiru Géy dafa àndoon ak haal. Moo ko wax de, du man. Ndeysaan, xamul ni ku ànd ak haal day daladi. Keroog de, Bas, danga meloon ni ku jëfuur. Teeyoo, daloo. Moo tax it, dëggal nga li la Usmaan Sonko doon tuumal yépp. Xam naa teyoo ko nag. Danga saalit. Ni nga doon waxe firndeel na ni àndoo woon ak sa sago.

Sëñ Bas, dëggal nga ni yow yaa sant sàndarm yi ñu soppi lenn ci caabal gi kàppiten Ture defoon ba jébbal koy kilifaam. Baatu « remarques » (ceetlu) bi nga jëfandikoo doy na boroom xel yi. Ndax, wax ju àgg, dof yaa ko moom.

Sëñ Bas, dëggal nga ni, nataal yu bon yooyee te ñaaw, lees dolli ci wayndarew luññutu wi la, bokkuñu ci woon. Te, danga tuumaal komandaŋ Mbeng.

Sëñ Bas, dëggal nga ni, caabalug sàndarmëri bi yëngal Nguur gi, lu am la. Yow de, li nga def sax xamoo ko. Jéem ngaa soofantal caabal gi ba sonn, naan wóoru la ndax am na walla déet. Kon noo xamee li ci biir bay xam ku ñu laaj ak ku ñu laajul, ku wax ak ku waxul ? Waxatuñ dara, nga naan kàppiten Ture dafa yembadi. Waa Bas mii nit la ? Yow ak kàppiten ture ku ci dof ? Waaye ndokk ! Dof, walla dof-doflu ba rëcc, moo gën muus walla muus-muuslu ba dee. Xawma kan de, waaye kàppiten ture raw na.

Sëñ Bas, nga ne kenn mësul a toppe Ndey Xadi Njaay mbirum cagatu ak jaay jigéen ? Kii yow la ? Yow mi fi tuumaal lu ni mel soxna si. Xanaa du àttekat baa soppi tuuma yi, am déet ? Sëñ Bas, mag day wax dëgg nag. Nga baalati ma.

Sëñ Bas, nee nga, bërki-démb, ñëwoo woon ngir tuumaal Usmaan Sonko. Te, baamu nga kàddu gi ay yoon ci sa biir i wax. Waaye, ku la déglook xel, du jukkee ci say wax lu mooy ne, « Usmaan Sonko moo def ». Doo ko weddi de, ndax yaa wax ne « Usmaan Sonko, kenn fekku ko ci buntu jàkka. » Yow nag, Sëñ Bas, yaa ngi dem jàkka ? Ndax gëm nga Boroom Bi nuy fay jaamu ? Boo ma nee waaw, ma jox kàddu gi Séex Baara Njaay mu fàttali la 42i way-laago (ay lafañ) yi nga tëjlu woon.

Nee nga jàpp Usmaan Sonko du woon sa jubluwaay. Sëñ bi, kaay nu ànd geestu xool ba xam li ngay wax dëgg la am déet. Cig pàttali, altine 8i fan ci féewaryee 2021 lañu woolu woon Usmaan Sonko. Ca talaata ja, 7i fan ci féewaryee 2021 la Usmaan Sonko amaloon ndajem waxtaan ak taskati xibaar yi. Yaa nu ko fàttali sax démb, yow Sëriñ Basiiru Géy. Ca la njiitalu Pastef li waxe woon ne, du wuyuji mukk fileek teggiwuñu malaanum kiiraayam, ndax dépite la woon jamono jooja. Lu taxoon ngeen koy woolu te Yoon aaye woon leen ko, wuyu ma Bas ? Bu dul woon askan wi, jàpp kon ngeen ko bu yàgg. Du mujj ngeen a teggi malaanum kiiraayam, lu tee woon ngeen njëkke ko, doo ma wuyu ? Yeen a ko teyoon kon, nga may xulli. Loolu du tooñ, waxal ? Fompal sa ñaq bi te defaru. Noppeeguma ci yow.

Ñu lay jiiñ dëmm, ngay soccoo yeelu liir

Sëñ Basiiru, nee nga liggéey nga 24i at ci Yoon wi. Dëgg la. Waaye, lu tax, booba ak léegi, askanu Senegaal mësu la dégg ci leneen lu dul mbirum Usmaan Sonko ? Ak lees fi jot dégg yépp ciy luubal ak i njombe, 2012 ba tey, mësoo ŋaaŋ. 10i at yooyu yépp, yaa nekkoon Toppekatu Bokkeef gi, ñaata caabal (ràppoor) lañu la fi jébbal, rawatina yu OFNAC yi ? Ana mbirum 94i milyaar yi ? Ana 29i milyaari PRODAC yi ?

Ñaata bakkan lañ fi rey, Sëñ Bas ? Foo nekkoon ? Waaw, lu tax defoo ni say moroomi toppekat yi la fi jiitu : noppi ni la ko Yoon santee ? Waa Sëñ bi, ku rey Mariyaama Saañaa ? Ndeysaan… sa tekkaaral gi yéem nañu. Xanaa danga fàtte ni bàyyi na fiy doom ? Xanaa amoo ay doom ? Ndax buñ ko defoon seen ndey dinga ne tekk tekkaaral niŋ ko defe ? Ay sàmbaa-booy topp ko ci lëndëm gi, siif ko, xoj ko ba mu sedd. Foo nekkoon ? Ak loolu yépp, nga bëgg noo gëmloo ne du APR ngay liggéeyal ? Waaw, ma laajati la, lu waa APR doon def ca sa ndaje ma ? Lu fa Seers Malu (Serge Malou) doon def ? Ñu lay jiiñ ne danga kootoo ak waa APR ngir faagaagal Usman Sonko, ngay janook taskati xibaar yi di ci ànd ak militaŋu APR. Xoolal, Bas, Saa-Senegaal yi dunuy dof te kenn moomu leen.

Li ci kanam nag, rawul i bët.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj