Lépp mat na. Ndajem Ndeyu Sàrti Réew mi dëggal na njureef yi tukkee ci mbañ-gàcce yi, Ëttub dabe bi biraloon leen barki-démb ci àllarbi ji.
Nees ko xamee woon, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay moo jiitu ci wotey 24 màrs 2024 yi, góob 54,28% ci xob yi. Kon, mooy tànneefu askan wi, di kiñ fal ngir mu doon 5eelu Njiitu Réew mu Senegaal fii ak 5i at yii di ñëw.
Bu neexee Yàlla, talaata 2 fani awril 2024 lay jël lenge yi. Fa CICAD (Centre de Conférence Abdou Diouf) bu Jamñaajo lay waatee bu 11i waxtu jotee ci yoor-yoor bi. Bu noppee, jubali ca Njénde la (Pale) ngir Maki Sàll jébbal ko lenge yi, lépp mat, mu tàmbalee doxal.