SENEGAAL 2 – BOLIWII 0

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ekibu nasiyonalu Senegaal bu futbal a ngi ci waajtaayu Kub di mond bi war ame ca Qataar. Joŋante bu mag boobu nag, daanaka ay fan kesee ci des. Nde, dibéer 20i fan ci nowàmbar lay door, Senegaal ak Olànd war a futbal joŋanteb ubbite bi, bu 16i waxtu jotee. Ngir waajal ndaje mu mag moomule nag, tëggalees na Aliw Siise ak i ndawam ñaari joŋantey xaritoo ci weeru sàttumbaar wile. Li ñu ko dugge mooy nattu, xool fu seen doole tollu ak li ñu war joyyanti balaa mbir miy door. Ñaari joŋante yooyu nag, Boliwii ak Irã lañ koy sékkal. Démb, ci gaawu gi, lañ doon futbal mats bu njëkk bi ak Boliwii, fale ca Farãs, daldi koy dóor 2i bal ci 0.

Ca Orleyã (Orléans), Farãs, la joŋanteb Senegaal-Boliwii bi doon ame. Ci tàkkusaan gi (17i waxtu ci ngoon) la door. Ab 4-3-3 la Aliw Siise tegoon. Alfred Gómis moo nekkoon ci kã yi. Fóode Balóo Ture, Abdu Jàllo, Kaliidu Kulibali (kàppiten bi) ak Mustafaa Naam ñoo taxawoon ci defãs bi. Ci digg bi, Paap Mataar Saar moo taxawoon ci kanami Paap Géy ak Paate Siis mu bees mi. Ci kow, Saajo Maane, Bulaay Ja ak Kerepeŋ Jaata ñoo fa doon futbal.

Bu dee waa Boliwii, seen aji-tàggat ji tamit 4-3-3 la tegoon : Lampe moo doon góolu. Ci kanamam, Sagredo, Jusino, Quinteros ak Bejarno ñoo taxawoon. Vaca, Justniano ak Villamil res digg bi. Fernandez, Martins ak Cuellar ñoo nekkoon ataakã yi.

Ñépp a mànkoo, waxandoo ne, li Senegaal wane démb, dalagum na xel. Ndaxte, gaynde yi futbal nañ lu leer te rafet ; wane nañ jom, fulla ak faayda. Ndeke, arbit da ne piriib rekk, ñu song Boliwii, sëpp ko, ba 11i futbalkatam yépp toog ci seen i kã. Moo tax, bii bu gaaw la Senegaal dugal. Bi ñu tollee ci 4i simili la fa Bulaay Ja jot benn bal, daldi koy xaañ ci kãwu Lampe yi, mu daldi dugg. Bii bu rafet kay, Senegaal am 1, Boliwii 0. Waaye, taxul gaynde yi doyal.

Saajo Maane ak i ñoñam bàyyiwuñu benn yoon defãsu Boliwii bi mu noppalu. Dañ leen a sëpp rekk, di wut ñaareelu bii bi. Daanaka, Boliwii amul dara ci mats bi. Senegaal a futbal lépp. Paate Siis ak Paap Mataar Saar di bërëŋ bal bi ci ñaxum estaadu Orleyã bi ni mu leen neexe, ànd ceek Paap Géy. Saajo Maane, Bulaay Ja ak Kerepeŋ Jaata tamit di rëbb kãwu Boliwii bi rekk. Waaye, sooyuñu de. Ndaxte, bi ñuy waaj a mitã (43i simili), la Saajo Maane am penaaltii, daldi koy dugal. Senegaal am 2, Boliwii 0. Noonu la fay deme ba ni mitã di jotee.

Bi 22i futbalkat yi delsee tamit, Gaynde yi dañ delloo buum gi ca boy-boy ga. Waaye, waa Boliwii xawoon nañoo yeewu tuuti. Wànte, taxul ñu jàll defãsu Senegaal bi. Bii du duggaat ci ñaareelu mitã bi, donte ne ñaari way-tàggat yépp a dugaloon, bi ma mats bi soree, yeneen futbalkat.

Mënees na wax ne gaynde yi door nañu seen waajtaay bi ci anam bu rafet. Waaye, ci talaata jii nu dégmal, 27i fan ci sàttumbaar, war nañoo daje ak Irã ngir wéyal seen ug tàggatu. 

Pap Aali Jàllo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj