SENEGAAL/ANSD : LIMU NIT ÑI

Yeneen i xët

Aji bind ji

ANSD, banqaas biy saytu limu nit ñeel yu ni mel, génnee na caabalam gu mujj gi. Nde, ci atum 2023 mi lañ doon waññi nit ñi ngir xam tolluwaayu askan wi. Biral nañ njureef yi.

Ci li caabal gi siiwal, fukk ak juróom-ñetti tamndareti nit yu tegal téeméeri junneek ñaar-fukk ak juróom-benn ak ñetti téeméer ak juróom-ñeen-fukk (18 126 390). Lim bi dafa séddalikoo ciy pàcc.

Bariwaayu ndaw ñi

Senegaal, góor ñaa ëpp jigéen ñi. Ndax, li waa ANSD xamle mooy ne, ci nit ñi fiy yeewoo, 100 boo jël, 50,6 yi ay góor lañu, 49,4 yi diy jigéen. Doomi réew mi, maanaam ñi am nasiyonaalite Senegaal, ñoo fi ëpp Ndaxte, 100 boo jël, 98,9 yi ay Saa-Senegaal lañu. Nee ñu, diggante 2013 ak 2023, nit ñi dañu yokku. Nde, 100 boo jël, 2,9 dolleeku na ci. Ci li ANSD bind, bu yokku bi dakkul, limu nit ñi dina ful ñaari yoon fii ak 25i at. Senegaal nag, ndaw ñaa fi ëpp.

Boo jëlee limu Saa-Senegaal yiy yeewoo fi réew mi yépp, xaaj bi amaguñ 19i at. Rax-ci-dolli, 39 yoo jël ci 100 bu nekk, amaguñu 15i at. Te, boo jëlaatee lim bi yépp, ñi néewle 35i ñooy tollook 75 ci 100 boo jël. 

Diiwaani Ndakaaru, Cees ak Njaaréem (Jurbel) ñoo ëpp i nit (47%). Ci biir ñetti diiwaan yooyii, Ndakaaru moo ci ëppale (22%). Maanaam, dees na fekk 7 277i nit ci kilomet kaare boo jël. 

Ñu bari jànguñu, tàggatuwuñu

Biir xale yi mat a yóbbu daara, 100 boo jël, 18,2 yi rekk a dugg “préscolaire” bi. Bu dee daafay tuut-tànk yi, 81% yi bindu nañ di jàng. 50,6% rekk ñoo ciy jàng ci “moyen” bi ak 30,3% ñeel “secondaire” bi. Ci dëkki taax yi la lim bi gën baree bees ko méngalee ak dëkki kow yi. Sigicoor moo ëpp ay njàngaan, topp ci Ndakaaru, Cees toppaat ci.

Bu dee wàllu tàggatug liggéey gi, fukki Saa-Senegaal yoo jël, kenn kese moo ko ciy def.

Caabal gi yaatu na. Dees na ci fekk yeneen rootaan (données) yu solowu ñeel réew mi. Gëstukat yeek njàngaan yi mën cee sukkandiku ngir liggéey. 

Ku bëgg yeb caabal gi ngir yaatal, demal ci dalu webu ANSD, dees na ko fa fekk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj