Woorandoo, woreendoo, ay gént la fi Senegaal. Daanaka, ñaari korite, dem na ba nekk aada ci julliti Senegaal yi. At mu jot, juyoo dina am ci séentub weer wi. Bu dul ci ndoorteelu koor gi, ci kori gi lay doon. Tabasaki sax, barewul li ko julliti Senegaal yiy bokk defandoo ci benn bés. Koriteg ren ji tamit, ñaar lay doon.
Koorug 2023 gi, jullit ñépp a ko umandoo. Muy lees rafetlu woon, sante ko Yàlla mi ci dëppale njabootug lislaam gu Senegaal. li ci gënoon a neex, mooy li koorug jullit ñi méngoo ak gog kercen yi. Senegaal di benn bopp, ñuy woorandoo, bu fajar xaree, di dogandoo bu jant sowee. Ndekete yoo, bennoo gi du wéy. Korite gi firndeel na ko, ndax dekkal na féewalook juuyoo bi ci biir jullit ñi.
Démb, alxames 20 awril 2023 moo doon 29eelu fan ci weeruw koor. Muy bés bees di séentu weer wi fépp ci Senegaal. Bu feeñee ñu wori, bu feeñul ñu matal 30eelu fan wi. Dafa di, weeruw jullit, 29i fan la walla 30i fan. Moo tax, ñaar-fukk ak juróomteelu fan wu ne, jullit ñi dañuy séentu weer wi, rawatina bu xew-xew yu mel ni koor, kori ak tabaski jubsee. Waaye, nag, li asamaan siy doon senn yépp, weer wi di wenn uw weer, Senegaal moom, dafa mel ni këru diine gu nekk dafa am asamaanu boppam ak weeru boppam.
Bu waa CMS, kurélug Ibaadu yiy séentu fii, waa CONACOL, kurélug séentu weer gu tarixa yiy séentu fee. Bu ko ñii gisee, biral ko, ñee ne, ñoom gisaluñ ko seen bopp. Looloo amati ren jii. Ci alxamesu démb ji la CMS, ginnaaw bi saytooy xibaari ndawam ak julliti réew mépp ak sax bitim-réew, dafa wax ne gisees na weer wi ci Ndakaaru (Lag-roos ak Fooraa), ca Luga (Ngeer Malal) ak ca Kawlax (Ñooro). Bu dee bitim-réew, Mali, Koddiwaar, Móritani, Càdd, Burkinaa Faaso, Araabi Sawdit, Farãs, añs., weer wi feeñ na ci réew yooyii yépp. Ñu daldi julli ci àjjuma jii, 21 awril 2023.
Jaomono jooju, nag, waa CONACOL, ñoom, dañu wax ne gisuñu weer wi fenn ci Senegaal. Moo leen tax a matal 30eelu fan wi, fas yéenee julli ci gaawu gi, 22 awril 2023. Senegaal amati ñari korite.
Lii nag ba kañ ? Laaj yi sampu ñooy xanaa asaamaan si tiim Senegaal ak asamaan si tiim réew yi mu dendal duñ benn ? Xanaa ñooñu duñuy jullit ? Luy sababu féewaloo bi dëgg-dëgg ? Man pexee lees mën a lal ba bennale julliti Senegaal yi ?