SENEGAAL DÓOR NA ÀNGALTEER 3-1

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gaynde Senegaal yi fàdd nañ yoy Àngalteer ya. Ñetti bal la leen gari Senegaal yi ngàdd. La ca gën a neex moo di ne, seen biir dëkk lañu leen fekk, duma leen. Loolu la gone yiy way, naan : « fekksi leen dóor leen, noo ngiy ñibbi ! ». Mu di ndam lu réy ñeel Afrig ak Senegaal. Ndaxte, guléet ab ekibu Afrig di bom ekibu Àngalteer. Loolu nag, jaloore ju réy la joj, warees na ko gërëmee Paab Caw ak i ndawam.

Ca fowub City Ground Stadium bu Nottingham la gayndey àngale yi doon dalal yoy Senegaal. Joŋanteb xaritoo la woon. Démb a nekkoon ñaareel wi yoon Senegaal di laale ak Àngalteer. Ca kuppeg àddina sa amoon Qataar, 2022, lañu jëkkoon a futbal, Àngalteer gàddu woon ndam li. Ca ndaje mooma, méngoo woon ak 1/8 (wicceem-dë-finaal) ya, 3-0 la àndandooy Bellingham yi dóoroon gayndey Aliw Siise ya. Waaye nag, wolof dafa ne : dóor, fayu. Moo tax, démb, Senegaal fayu na bu baax a baax, ci fulla ak jom ju mat sëkk.

Bi 18i waxtu toftalee 45i simili la joŋante bi door. Senegaal moo tegoon tànk ci bal bi, di dawal lu leer. Waaye, jotuñoo dugal. Noonu, bal bay daw ba ca 7eelu simila ba, Lamin Kamara yéex a joxe bal ba, àngale yi nangu ko ciy tànkam, dóor, Eduwaar Mendi génnee, Harry Kane mi doon yeeru bal ba, daldi koy dugal ca biir kãwu Senegaal : Àngalteer am 1, Senegaal 0.

Gayndey Senegaal yi nag, xàddiwuñu wenn yoon. Dañu defaruwaat, dëggaat ci bal bi, di wut yoon ngir dabu benn bii bi ñu leen dugal. Lees di wax rekk, xëcc bu daggul, dikk. ca 40eelu simili ba la Ismayla Saar toj caaxi Dean Henderson ya. Nikolaa Jakson la Kaliidu Kulibali tëmbalal ab bal, laata muy génn, mu taajal ko doomu Ndar ji, Ismayla Saar, mu romb Kyle Walker mi ko sóoralewul woon, daldi dóor bal bi, dugal ko : Àngalteer 1, Senegaal 1. Noonu la xaaj bu njëkk ba jeexee.

Bi 22i kuppekat delsee ci pàkku City Ground Stadium, Abiib Jara ak i moroomam ñoo tegaatoon tànk ci bal bi, di ko bërëŋ. Ilimaan Njaay di duut àngale yi ak di leen paajal, di futbal lu rafet te leer. Soppey Senegaal ya leen tàccusi woon ak yi leen doon seetaan bég lool ci li xale biy mbél. Naka noonu, ca 61eelu simili ba, Kaliidu Kulibali naxaat àngale yi, sërëxal Abiib Jara bal bi, mu daw ba ca kã ya, daldi yaali góolu àngale ya, dugal. Yuuxoo ya jolleeti, Senegaal daldi jiital Àngalteer 2-1.

Àngale ya fippu, di puus ak a jéem a dugal ngir tolloo ak Senegaal. Daanaka, dugaloon nañu sax ca 84eelu simili ba. Bellingham moo dugaloon. Waaye, arbit bu jigéen bi daf ko gàntal ginnaaw bi mu xoolaatee VAR, gis ne bal bi dafa lool loxo Colwill. Wànte, taxul Bellingham ak moroomi àngaleem bàyyi. Dañu sëppoon Senegaal ca njeexitalu joŋante ba, bëgg a def lépp ngir dugal. Noonu la leen gayndey Senegaal yi naxee, doggali leen.

Nde, sunu gaynde yi dañu nangu bal bi ci seen wetu kã, daldi jox Lamin Kamara, mu tàllal pàkk bi, Séex Tiijaan Sabali ànd ak moom di daw. Ba ñu demee ba àgg ca kãwi Henderson ya, Lamin Kamara daldi taajal Sabali, mu lakkati caax ya, Senegaal am 3, Àngalteer am 1, mu jeex.

Bi joŋonte bi jeexee, Paab Caw miy tàggat gaynde yi tontu na ci laaji saabalkat yi. Moom nag, bég na ci ndam li, waaye taxul mu naagu. Daf ne :

« Danu amoon yéene amal joŋante bu baax, te xale yi wane nañu fulla ju mat. Dunu naagu. Ab nattukaay bu waroon ci nun la. Gis nanu li dox ak li nu war a joyyanti. »

Paab Caw fàttali na ne, am na ñaari joŋante yu am solo yu leen di xaar te ci lañu war a jublu. Caween bi rafetlu naat bennoo gi gaynde yi bennoo. Bees sukkandikoo ciy waxam, ndam lii, ndamu ñépp la.

Àngalteer nag, jot na a joŋante 22i yoon ak ekibi Afrig. Mësu cee ñàkk benn. Waaye démb de, Senegaal dóor na ko. Kon, Senegaal mooy njëlbeenu ekibu Afrig bu dóor Àngalteer. Te sax, Senegaal ci boppam, joŋante démb bee nekkoon 22eel bi mu tegale te ñàkku ci benn.

Ca weeru sàttumbar la gayndey Senegaal yi war a joŋante ñaari yoon ñeel tooglantey Kuppeg àddina si war a am ca atum 2026.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj