Tey ci àjjuma ji la gayndey Senegaal yiy laale ak yoy Kamerun. Bu 17i waxtu jotee, ca la joŋante bay door ca fowub Yamusukroo (Koddiwaar). Waaye de, werante bi tàmbali na xaat ci mbaali jokkoo yi diggante Saa-Senegaal yeek Saa-Kamerun yi. Ñaari ànterenëer yi tamit, Aliw Siise ak Rigobeer Soŋ sumb nañ xeex bi, daldi nappante.
Senegaal ak Kamerun bokk nañ ci ñaari ekib yu gën a mag ci Afrig. Mëneesul a wax ci futbalu Afrig te duñ leen tudd. Bu dee Kamerun, CAN bii mooy 22eelu CAN bi muy bokk. Ci biir 21 yi weesu, finaalu na ci 7i yoon, daldi jël 5 yi (1984, 1988, 2000, 2002 ak 2017). Kon, « Les Lions indomptables » amagum nañ 5i biddeew ci seen mayo.
Bu dee « Gayndey teraanga » yi, CAN Koddiwaar bi mooy seen 17eelu CAN. Ci 16 yi weesu, finaalu na ci ñetti yoon, ñàkk ñaar yi, jël benn bi (2022). Bennub kub bi Senegaal mës a jël sax, Kamerun la ko jëlee.
Rigobeer Soŋ : « Noo mës a féete kow Senegaal… »
Senegaal ak Kamerun jot nañoo futbal 17i yoon, Kamerun gañe 6i yoon, Senegaal dóor ko 5i yoon, ñu timboo 6i yoon. Bu dee ci wàllu CAN bi, 4i yoon kepp lañ mës a daje (1990, 1992, 2002 ak 2017). Kamerun moo ëpp li mu gañe nag. Ndaxte, dóor na Senegaal ñetti yoon (1992, 2002 ak 2017). Kon, wenn yoon kese la Senegaal mës a am ndam ci kow Kamerun ci joŋantey CAN bi, muy atum 1990. Looloo tax, bi ñu ko laajee, Rigobeer Soŋ (tàggatkatu Kamerun bi) tontu, wax ne :
« Ci wàllu mboor, xanaa ma fàtte, ñaata yoon lan mës a daje ak Senegaal ? Gis nañ li xew… Noo mës a féete kow Senegaal. […] Mboor du fenn mukk. Te, na woon, fa woon rekk. Danuy baaxantal, delloo buum gi ca mboy-mboy ga. Du tey la safaan bi di am. »
Li defãsëer ak kàppitenu Kamerun ba woon bëgg a wax, mooy ne ndox du wàcc yoonam. Te, Kamerun mi yàgg a dóor Senegaal, du ci àjjumay tey jii lay yàq woyam wi.
Aliw Siise : « Nun, Senegaal, bariwunu wax. »
Bi Kamerun di dóor Senegaal finaal 2002, fa Bamakoo (Mali), Aliw Siise (Senegaal) ak Rigobeer Soŋ (Kamerun) ñoo ngi doon futbal, ñoom ñaar ñépp nekkoon seen i kàppiteni ekib. Tey jii, ñoo nekk ci boppi ekib yi, di leen tàggat. Bu dee ca seen joŋante bu jëkk boobee (2002), kàppitenu Kamerun baa amoon ndam, bu mujj bi (16 nowàmbar 2023), Aliw Siise ak i gayndeem ñoo dóoroon.
Moom nag, Aliw Siise, bi ko saabalkatu Saa-Kamerun bi fàttalee démb, dafa muuñ, tontu ko ne : « Nun, Senegaal, bariwunu wax, danu wàccee sunu bopp lool. » Tegal na ko ci sax, wax ko ne : « Yeen ay kembaar gi », daldi toj, xàqataay. Bi mu koy wax loolu, dafa doon miimaale waxiinu Saa-Kamerun yi. Dafa di, ñoom Saa-Kamerun yi, dañoo safoo di woowe seen bopp « Le continent » (Kembaar gi).
Aliw Siise jokk, wax ne :
« Xam nanu leen… Ñu jox cër Kamerun lanu, jarul wax ju bari, [joŋante bi] yàggatul, ba booba. Dinan ko futbal ci dal gi nu ‘Kembaar gi’ xamee, waaye dinan ci ànd ak pasteef ngir wéyal sunu yoon. »
Waa Kamerun ak seen tàggatkat bi, Rigobeer Soŋ, dañuy geestu démb, jël mboor def ko ag xiirte. Aliw Siise moom, nee na Senegaal « … mësul a nekk ci ay fayantoo ». Ciy waxam, naam Kamerun dóor na Senegaal finaal (2002), toogloo ko 2017, waaye « … fa ‘Kembaar’ ga lanu dem, jëlee fa CAN bi ».
Joŋante bi nag, dina am ñu ko wuute ci ñaari boor yépp. Bu dee Senegaal, Sabali tàmbaliwaat na daw, waaye wóorul mu bokk. Naka noonoot, Fóode Baloo Ture, Paap Mataar Saar ak Gànna Géy wér nañu, mën nañ bokk, waaye wóoragul. Bu dee Musaa Ñaxate, moom ay mbiram leeragul. Abdulaay Simaa tamit dafa ame gaañu-gaañu bu ndaw ci « adducteurs » yi.
Bu dee Kamerun, Rigoober Soŋ xamle na ne Weesã Abuubakar tàmbaliwaat na tàggatu, waaye du bokk ci joŋante bi. Kiristof Woo moom, bi muy janook taskati xibaar yi, amagul woon lu leer ñeel ko.
Senegaal nag lañ wax ne moo jekku, maanaam mooy fawori. Ndaxte, wëliis li mu jël CAN bii weesu, moo gën a taxaw Kamerun jamono jii. Nde, bu dee ne ñoom ñaar ñépp ay gaynde lañu, Saa-Senegaal yaa di gar yi, Saa-Kamerun yi di ñalóor yi.
Gar mooy gaynde gu tollu ci digg dooleem, ñalóor di gaynde gu màgget. Waaye nag, gayndey Senegaal yi war nañoo moytu. Ndaxte, jinne, lu mu màgget, màgget, dese na ŋalaju bu jommal gune.