SENEGAAL, SEEN GAAL LA, ÑOOM, AM SUNU GAAL… ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ku waaruwul ci doxinu miim réew, saw doxin dina la waari ëllëg. Ku yéemuwul ci jëmu gaal gii, teeru bi dina la yéemi. Bees fobulee ci joowu yi joow ngir soppi jëmu gaal gi, nóoxóor yu ñuul yi dinañ joow yóbbu la, yaak say mbokk ak i xarit, wànteer leen ci nóoxóor yu weex yi. Su booba dinga yëngal bopp, màttu, wiccax sa baaraam naan “su ma xamoon…” Waaye, réccu day fekk jëf wees. Ndax dingeen bàyyee gaal gi nóoxóor yu ñuul yi, ñu joow jëme nu ca sëg ya ? Senegaal, seen gaal la, ñoom, am sunu gaal… ?
Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, ngëm dëgg feeñu fi fenn. Bëccëg, ku la ci ne “Yàlla nee na…”, “Yonent bi nee na…”, “Sëñ bi nee na…” bu la fenulee ngir naxee la ko yit, guddi mi ngiy njabarlu. Te li mu koy dugge mooy liggéey nawleem, yàq diggante yi, wut alal walla nguur, walla bëgg a siiw. Senegaal mooy réewum diine joo xam ni, bés bu nekk ñu tagg Yàlla, tagg Yonent bi, sargal Mag ñu baax ñi te kenn jéemul a roy ci ñoom. Senegaal a bariy jumaa, jàkka ak i taalibe, waaye Senegaal a bariy naaféq. Senegaal a bariy xew-xewi diine ak ñiy woote jàmm, waaye Senegaal a bariy waabajiiba. Moo ! Askan wu làmboo jikkoy naaféq ak melokaanu waabajiiba ban xeetu njiit la yeyoo ? Waaw, askan wu fase ngor, gàddaay dëgg, dëddu njub, suul fullaak faayda, ban xeetu njiit la yeyoo ? Ma laajati, askan wu sol mbubbu kàkkataar, dëkke fen, wor ak sàcc yan njiit la yelloo ? Yàlla ku maandu la. Moo tax it, lu waay rendi, ci say loxo lay nàcc. Nan dem rekk…
Senegaal ngay fekk askan wu dëkke ŋàññi ay njiitam, ci diirub juróom-ñaari at, bés bu nekk ñuy xultooka ñaxtu. Waaye, bés ñëw, bésub dibéer, askan woowu tànnaat yooyii njiit, tegaat leen ci boppu gaal gi, ñuy joow, jëme gaal gi fu leen neex. Nu dem rekk…
Senegaal bokk na ci ñaar-fukk ak juróomi réew yi gën a torox ci àddina si. Dëkkuwaay bu baax amu fi, luyaas bi metti na lool, xiif ak mar ne fi ràcc di bëgg a rey askan wi, ndóol waxi noppi, ku ci feebar dee ndax ñàkk loo fajoo walla loppitaan yu rafley jumtukaay. Njàng amatu fi waxatuma laak xéy, añs. Moone de, fii ngay fekk ay njiit yiy tabax i taax yu kowee-kowe, dëkk ciy kër yu réy te rafet lool, di dawal ay oto yu yànj ba jaaxal la. Ku ci ab yoo màtt, nga jël roppëlaan, naan yaa ngay fajooji Tugal. Rax-ci-dolli, seeni doom di jànge bitim-réew, ci daara yi gën a baax te siiw, ay daara yu ndongo ya xamul naka la ñuy waxe ‘’gereew’’. Njiit yooyu, ñooy jël alalu réew mi tayle ko Tubaab yi, di pasar-pasare xaalisu askan wi, di ci gundandaat ak a ndagarwale ca Soraanoo, Garaŋ-Teyaatar, làmb ja, ci yeneeni xew walla ciy mitiŋ. Bu wote jotee, ñu jël ci as tuut, di ko jënde askan wi nga xamante ne, lu jiin Njaag a, te mooy Njaag. Waaw, ndax sagaru junni, benn piisu waks bu fuyuŋ-fayaŋ, walla saaku ceeb jar na ngay jaay sa ngor ? Nga ne ma ? Sa alal la ?
Newuma la déet de, waaye nan demati rekk…
Senegaal mooy réew moo xam ne, Njiitu-réew mi lu ko neex def. Saa bu ko neexee mu jàpp kii walla kee, dëkke fi tëj ak jaay doole guddeek bëccëg. Bu wote jotee, askan wi tànnaat ko, teg ko ci jal bi. Ngan ne ma ? Naataange la la dig ? Walla la la digati…?
Ayca nu dem rekk …
Senegaal mooy réew moo xam ne, ndaw yi amuñu liggéey. Waaye, foo leen fekk ñoo ngiy werante ciy mbir yu ñàkk faayda : film, tiyaatar walla futbal. Doo gis benn ndaw, muy góor walla jigéen, bu nangoo yedd boppam, soppi jikkoom. Janq jaa ngiy mébét doon léttkat, ñawkat, woykat walla fecckat. Ñi ci yées, dem bay cagatu naan dañuy daan seen doole. Waxambaane bi moom, di ñefe ngir doon mbër walla futbalkat. Ñi ci gën a ñàkk faayda ñoom, rusuñu doon i woykat, fecckat, tëggkati sabar wallay taasukat. Ñi ci yées, di dogaale jaamu Yàlla yi, ngir nangu seen alal. Nga ne ma ? Tëgg ak fecc ci sunu aada la bokk ? Waaw, kon daal tëgg ak fecc a nuy jëme kanam ?
Waaye baax na, nan demati rekk…
Senegaal mooy réew moo xam ne, làkku jaambur lañ fiy jàngale ak démbu doxandéem. Kenn jàngalul xale yi ngir ñu mënal seen bopp, gëm seen bopp, moom seen bopp. Waaye, dañ leen di jàngal ngir ñu doon i jaam yuy tàllal loxo. Nga ne ma ? Sunuy làmmiñ réew mënunu cee tekkee ? Yaakaaroo ne ki la wax loolu dafa laa yab ? Yaakaar nga ne teg na la nit Njaay ?
Waaye nu dox dem rekk…
Senegaal mooy réew mu bari alal te askan wi jariñoowu ko ; réew mu bariy àttekat te amul yoon ; réew mu ñépp bokk, ay sàmba-allaar aakimoo ko di ci def lu leen neex. Senegaal mooy réew mi nga xam ne, foo dem ñu ni la “waa réew moomoo neex xel ! Ñoom kay, kuy wut xalaat bu rafet, gaawal ganeji fa.” Nga ne ma ? Dëgg la ! Dëgg piir sax ! Fii daal, ku ëpp sa moroom doole wan ko ko. Moo tax it, ku yeboo jéem a muus, di jëfandikoo sam xel ngir jël sa wàll ci toŋ-toŋ bi. Loolu doŋŋ la, nag. Bu nu kenn rey ak wax ju bare. Politiseŋ yi loolu lañu nànd bu yàgg, kon lu may tere def ni ñoom ?
Léegi nag, àgg nanu.
Nanu wax ak ndaw yi. Ndax kat, ëllëg, seen ëllëg la. Ndax warees naa seetaan lii di wéy ? Senegaal, seen gaal la,ñoom, am sunu gaal ? Li wér te wóor mooy, sunu gaal gaa ngi daw ni gaalu dof ci géej gu sàmbaraax. Jot na askan wi yeewu, nangu joowu yi ngir jubbanti gaal gi. Ndax kat, gaalu dof du teer, walla bu teeree yit, teeri ci loxoy nóoxóor.
Paap Aali Jàllo
 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj